Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC ÑAAR

Biibël bi : téere la bu jóge ci Yàlla

Biibël bi : téere la bu jóge ci Yàlla
  • Lan moo tax Biibël bi wuute ak yeneen téere yépp ?

  • Biibël bi mën na la dimbali ci poroblem yi ngay am. Naka ?

  • Lu tax nga mën a gëm li Biibël bi wax ne dina am ëllëg ?

1, 2. Lan moo tax Biibël bi nekk maye Yàlla bu baax ?

NDAX yaa ngi fàttaliku bés bi la sa benn xarit mayee lu rafet ? Loolu neexu la woon rekk yem ci, dafa la laal ci sa biir xol. Ci dëgg, li ñu lay may am na li mu lay won ci ki la ko may. Dafay wone ne kooku fonk na seen xaritoo. Li wóor mooy gërëm nga ko ci bu baax.

2 Yàlla moo ñu may Biibël bi. Dëgg-dëgg, mën nañu ko gërëm bu baax ci loolu. Benn téere melul ni téere boobu. Li ñu ci mën a jàng amul feneen fu ñu ko mënee jàng. Lii di topp bokk na ci li mu ñuy xamal : bi Yàlla doon sàkk asamaan si ak biddéew yi, bi mu doon sàkk suuf si, ak it bi mu doon sàkk góor bu njëkk bi ak jigéen bu njëkk bi. Xelal yu baax yu ñu mën a dimbali ci coono yi ak it ci poroblemu àddina, ñu ngi ci Biibël bi. Dafa ñuy won naka la Yàlla di defe li waraloon mu sàkk suuf si te indi àddina bu gën a neex ci kaw suuf si. Dëgg-dëgg, Biibël bi maye Yàlla bu baax la !

3. Yexowa moo ñu may Biibël bi. Loolu, lan lay wone ci Moom, te lu tax muy laal suñu xol ?

3 Biibël bi nekk na it maye buy laal suñu xol, ndaxte am na lu mu ñuy wax ci Ki ko maye, maanaam Yexowa Yàlla. Maye boobu dafay wone ne Yàlla dafa bëgg ñu xam ko bu baax. Waaw, Biibël bi mën na la dimbali nga jege Yexowa.

4. Lan moo la jaaxal ci li ñuy joxe Biibël bi ci àddina si ?

4 Bu dee am nga Biibël, nanga xam ne du yow kese yaa ci am benn. Mën nañu jàng Biibël bi ci lu mat 2 300 làkk, muy téere bi yépp walla ay xaaj. Kon ci àddina si sépp, ci 100 nit yoo jël, lu ëpp 90 mën nañu am Biibël bi. Boo seetee Biibël yi ñuy joxe ci àddina si sépp, dafa mel ni semen bu nekk dinañu ci joxe lu ëpp benn milyoŋ ! Fi ñu tollu nii, defar nañu ay milyaari Biibël, muy Biibël bi yépp walla ay xaaj. Ci lu wóor, amul beneen téere bu mel ni Biibël bi.

Sotti Biibël bi tudd “ Traduction du monde nouveau ” am na ci làkk yu bare

5. Lu tax ñu mën a wax ne Biibël bi “ ci gémmiñu Yàlla la jóge ” ?

5 Rax-ci-dolli, Biibël bi “ ci gémmiñu Yàlla la jóge ”. (2 Timote 3:16.) Lu tax ñuy wax loolu ? Biibël bi ci boppam tontu na ne : “ Xel mu Sell mi daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla. ” (2 Piyeer 1:21). Nañu ko seet ci lii : Maam mën na bindloo sëtam benn leetar. Xalaat ak tegtali maam ji ñooy nekk ci leetar boobu. Kon, ci dëgg, leetar boobu leetaru maam ji la. Du leetaru sët bi. Noonu it, li nekk ci Biibël bi ci Yàlla la jóge, waaye jógewul ci nit ñi ko bind. Kon, dëgg-dëgg, lépp li nekk ci Biibël bi “ kàddug Yàlla ” la. — 1 Tesalonig 2:⁠13.

LI ÑU CI BIND YÉPP A ÀND TE LI MU WAX MOO AM

6, 7. Lépp li nekk ci Biibël bi, ni mu ànde, lu tax mu nekk lu doy waar ?

6 Ci lu ëpp 1 600 at lañu bind Biibël bi. Ñi ko bind bokkuñu woon jamono te yemuñu woon alal. Amoon na ci ay beykat, ay nappkat ak ay sàmmkat. Amoon na ci itam ay yonent, ay àttekat ak ay buur. Luug mii bokkoon ci ñi Yàlla tànn ngir bind Injiil (maanaam fi ñu nettali dundu Yeesu), doktoor la woon. Kon ñi bind Biibël bi, wuute woon nañu ci lu bare. Waaye loolu terewul lépp li nekk ci Biibël bi dafa ànd, fi mu komaasee ba fi mu jeexe *.

7 Téere bi ñu njëkk a bind ci Biibël bi dafa ñuy nettali ni coono doomu Aadama yi tàmbalee. Téere bi ñu mujj a bind dafa ñuy won ne suuf si sépp dina nekk àjjana, maanaam tool bu rafet. Lépp li nekk ci Biibël bi dafay wax ci li xewoon ci àddina si ci lu mat ay junniy at. Dafa ñuy dimbali it ñu xam li Yàlla bëgg a def ak naka la koy defe. Li nekk ci Biibël bi, ni mu ànde nii, doy na waar. Waaye téere bu jóge ci Yàlla, noonu la war a mel.

8. Waxal luy wone ne li nekk ci Biibël bi ànd na ak li tubaab di woowe science.

8 Biibël bi ànd na ak li tubaab di woowe science, maanaam li boroom xam-xam yi di gëstu. Am na sax lu nekk ci Biibël bi li nga xam ne jamono bi ñu ko doon bind, kenn xamagu ko woon. Nañu ko seet ci lii : Ci téere bi tudd ci tubaab Lévitique, am na ay sàrt yu Yàlla joxoon waa Israyil bu njëkk bi ngir ñuy ber nit ñi feebar ngir ñu bañ a wàll seeni moroom. Am na fa it ay digle ci wàllu set, fekk ca jamono jooju, réew yi leen wëroon, xamuñu woon dara ci mbir yooyu. Ca jamono bu nit ñi doon wax ni suuf si mel te di ci juum, Biibël bi moom, nee woon na ne suuf si dafa mërgëlu, maanaam dafa mel ni bal (Isaïe 40:22). Biibël bi nee na it ne suuf si ajuñu ko ci dara, te loolu mooy dëgg (Job 26:⁠7). Dëgg la, Biibël bi du téereb science. Waaye bu waxee lu ci jëm, dafay nekk dëgg. Ndax loolu nekkul li ñu war a séentu ci téere bu jóge ci Yàlla ?

9. a) Li Biibël bi nettali ci li xewoon ca jamono yu yàgg ya, lu tax ñu mën a wax ne lu wér te wóor la ? b) Ñi bind Biibël bi ay waxkatu dëgg lañu woon. Loolu lan la lay won ci lu jëm ci Biibël bi ?

9 Lu jëm ci li xewoon ca jamono yu yàgg ya, li ci Biibël bi wax, lu wér te wóor la. Buy nettali dara, dafa ciy boole yu sew yu mel ni, bu tuddee nit dafa ciy boole turu maamam yi *. Ñi bind Biibël bi, dëgg lañu wax bu dee sax dañu ci war a wax seeni bàkkaaru bopp walla bàkkaaru seen réew. Loolu wuute na ak li yeneen nettalikatu àddina si di def. Bu seen réew ñàkkee ndam, barewul ci ñoom ñi koy wax. Yonent Yàlla Musaa moom, waxoon na njuumte bu metti bi mu defoon. Njuumte boobu moo taxoon Yàlla yar ko yar bu metti. Loolu mën nañu ko jàng ci téere Biibël bi ñuy woowe ci tubaab Nombres te Musaa bind ko (Nombres 20:​2-12). Ay nettalikat yu dëggu yu mel noonu barewul ci nettalikat yi bind yeneen téere yiy nettali li xewoon ca jamono yu yàgg ya. Waaye loolu mu ngi ci Biibël bi, ndaxte Biibël bi dafa nekk téere bu jóge ci Yàlla.

AY XELAL YU BAAX ÑOO CI NEKK

10. Li Biibël bi nekke téere bu am njariñ lool, lu tax waru ñu bett ?

10 Ndegam Biibël bi ci Yàlla la jóge, dina am “ njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub ”. (2 Timote 3:16.) Waaw, Biibël bi téere bu am njariñ la. Li ñu ci bind dafay wone ne mu ngi jóge ci ku xam bu baax doomu Aadama yi. Loolu bettu ñu ndaxte ci Yexowa Yàlla la jóge, moom mii ñu sàkk. Moo ñu gën a xam li nekk ci suñu xel ak ci suñu xol. Li ëpp solo mooy, xam na li ñu soxla ngir mën a bég. Xam na itam li ñu war a moytu ci suñu àddina.

11, 12. a) Ci lan la Yeesu wax ci waare bi mu defoon ci tund bi ? b) Ci yan fànn yu am solo la Biibël bi di wax itam ? Te lu tax li fa nekk di am njariñ ba fàww ?

11 Xoolal waare bi Yeesu def ci tund bi, te ñu nettalee ko ci Macë pàcc 5 ba 7. Ci njàngale bu rafet boobu, Yeesu wax na ci mbir yu bare. Wax na ci ni ñuy ame mbégte dëgg, ni ñuy defare diggante bu ñagas, ni ñu waree ñaan Yàlla, ak naka lañu mënee yemale alal fi mu war a yem. Li Yeesu wax foofu, mu ngi kontine di am doole te di am njariñ, ni ci jamono bi mu ko waxee.

12 Xelal yi nekk ci Biibël bi dañuy laal mbirum njaboot, ni ñuy liggéeye ak it suñu diggante ak suñuy moroom. Li Biibël bi wax baax na ci nit ñépp te lépp li mu ñuy xelal dafa am njariñ. Li Yàlla waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, dafay wone ci lu gàtt njariñu xam-xam bi nekk ci Biibël bi, maanaam : “ Man Yexowa maay sa Yàlla, Ki lay jàngal ngir sa njariñ. ” — Esayi 48:​17, NW.

TÉERE BUY YÉGLE LI WAR A AM ËLLËG

Esayi mi bokk ci nit ñi bind Biibël bi waxoon na ne dinañu alag Babilon.

13. Lan la Yexowa bindloo yonent Yàlla Esayi lu jëm ci Babilon ?

13 Biibël bi wax na lu bare lu war a am. Te lu bare ci li mu wax noonu, am na ba pare. Seetal lii : Yexowa dafa jaar ci Yonent Yàlla Esayi ngir xamal nit ñi ne dinañu mas a alag Babilon. Lu ëpp 700 at bala jamono karceen yi di tàmbali la ko yonent boobu wax (Isaïe 13:19 ; 14:​22, 23). Waxoon na lépp li fa naroon a xew ngir nit ñi xam bu baax ni ñuy daane dëkk boobu. Nee woon na ne ay xarekat dinañu ñëw, wowal dexu Babilon te dugg ci biir dëkk bi, fekk xeex du leen ci fekk. Waaye yonent bi yemul ci loolu. Esayi dem na ba wax sax turu buur bi war a nangu Babilon, maanaam Sirus. — Isaïe 44:27–45:⁠2.

14, 15. Li yonent Yàlla Esayi waxoon te mu naroon a xew ci Babilon, naka la ame ?

14 Lu jege 200 at ginnaaw loolu, ci guddi diggante 5 ba 6 oktoobar ci atum 539 bala jamono karceen di tàmbali, ay soldaar dañu ñëw ci wetu Babilon, taxaw. Kan moo leen doon jiite ? Buuru Pers bu tudd Sirus. Lépp taxawoon na léegi ngir lu doy waar li Biibël bi waxoon bu yàgg mën a am. Waaye ndax soldaari Sirus dinañu dugg biir Babilon te xeex du leen ci fekk ni ko Biibël bi waxe woon ?

15 Ci guddi googu nag, waa Babilon dañu amoon feet bu mag. Seen xel dafa daloon, ñu foog ne dara mënu leen dal ndaxte ay miir yu réy ñoo wëroon dëkk bi. Waaye Sirus mu ngi doon fexe ba ndoxu dex bi doon jaar ci biir dëkk bi, bàyyi yoonam, aw feneen. Noonu, ndoxu dex bi wàcc ci lu gaaw, ba tax soldaaram yi mën a dox fi dex bi doon jaar bu njëkk te jege miiri dëkk bi. Waaye naka la soldaari Sirus di def ba jéggi miiri Babilon yi ? Xamuñu lu tax, waaye ci guddi googu, waa Babilon dañoo sàggan ba kenn tëjul buntu dëkk bi !

16. a) Boo seetee li Esayi waxoon, naka la Babilon waroon a mujje ? b) Li Esayi waxoon, maanaam kenn dootul dëkk ci Babilon, naka la ame ?

16 Lii la Biibël bi waxoon ci Babilon : “ Kenn dootu fa dëkk, du fi nekkati ba fàww. Naar bi dootu fa samp tàntam, te sàmmkat bi du bàyyi géttam mu tëdd fa. ” (Esayi 13:​20, NW). Yonent boobu yéglewul rekk ne dinañu alag dëkk bi. Dafa xamle itam ne kenn dootul dëkk ci Babilon ba fàww. Mën nga gis ne kàddu yi ñu wax foofu mujj nañu am. Tey, kenn dëkkul fi Babilon nekkoon, maanaam lu tollu ak 80 kilomet ci wetu Bagdad ca Iraq. Loolu mooy wone ne li Yexowa waxoon jaarale ko ci Esayi mujj na am. Yexowa nee woon na : “ Dinaa ko bale ak bale buy tas ba dara du des. ” — Esayi 14:​22, 23 *, NW.

Li des ci dëkku Babylon

17. Li ñu gis ne li Biibël bi waxoon mujj na am, loolu naka lay dëgërale suñu ngëm ?

17 Jàpp ne lépp li Biibël bi yégle dafay mujj a am, ndax loolu du dëgëral suñu ngëm ? Su dee Yexowa def na lépp li mu dige woon ca jamono yu njëkk ya, kon na ñu wóor ne àjjana bi mu dige ci kaw suuf si dina am (Nombres 23:19). Waaw am nañu “ yaakaar ju dëggu, [...] ci dund gu dul jeex, gi Yàlla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam ”. — Tit 1:2 *.

“ KÀDDUG YÀLLA MI NGI DUND ”

18. Ban kàddu bu am doole la ndaw li Pool mi nekkoon karceen wax ci “ kàddug Yàlla ” ?

18 Ak lépp li ñu gis ci xaaj bii, leer na ne amul benn téere bu mel ni Biibël bi. Lépp lu ci nekk dafay ànd. Li muy wax ànd na ak li boroom xam-xam yi wax. Li muy wax ci lu jëm ci li xewoon démb, noonu la ame. Xelal yu baax moo ci nekk te li muy yégle dafay am ni mu ko waxe. Waaye njariñu Biibël bi ëpp na fuuf loolu lépp. Ndaw li pool, mi nekkoon karceen nee woon na : “ Kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gën a ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol [maanaam li sa xol bëgg]. ” — Yawut ya 4:⁠12.

19, 20. a) Naka la la Biibël bi mënee dimbali nga seetaat sa bopp ? b) Naka nga mënee wone ne fonk nga Biibël bi, maye bu amul moroom boobu la Yàlla may ?

19 Jàng ci Biibël bi liy “ kàddu ” Yàlla, maanaam li muy yégle, mën na soppi suñu dund. Mën na ñu dimbali ñu seetaat bu baax suñu bopp ci fasoŋ bu ñu ko masul woon a def. Xéyna dañuy wax ne bëgg nañu Yàlla, waaye li ñuy def ginnaaw bi ñu jàngee Kàddu Yàlla, maanaam Biibël bi, mooy wone li nekk dëgg ci suñu xel, ak ci suñu biir xol.

20 Dëgg-dëgg, Biibël bi ci Yàlla la jóge. Téere boobu dañu ko war a jàng, gëstu ko, te fonk ko. Nanga kontine di ko gëstu ngir wone ne fonk nga lool téere boobu la Yàlla may. Booy def loolu, dinga xam bu baax lu tax Yàlla sàkk doomu Aadama yi. Ci pàcc bii di topp, dinañu ci waxtaan, waxtaan it ci naka la loolu di ame.

^ par. 6 Am na ay nit ñuy wax ne Biibël bi dafay weddi boppam. Waaye nit ñooñu mënuñu dëggal seeni wax. Seetal pàcc 7 ci téere bi tudd La Bible : Parole de Dieu ou des hommes ? (Biibël bi : kàddu Yàlla la walla kàddu nit la ?). Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.

^ par. 9 Mën nga seet turu maami Yeesu yi nekk ci Luug 3:​23-38.

^ par. 16 Boo bëggee yokk sa xam-xam ci lu jëm ci li Biibël bi yégle bala muy am, seetal téere bi tudd Un livre pour tous (Téere bu ñu jagleel ñépp), xët 27 ba 29. Seedee Yexowa yi ñoo defar téere boobu.

^ par. 17 Li ñu alag Babilon, benn misaal doŋŋ la ci li ñuy won ne li Biibël bi yégle dafay mujj a am. Am na yeneen misaal mel ni sànkute Tir, ak Niniw (Ézékiel 26:​1-5 ; Tsephania 2:​13-15). Dañeel itam waxoon na lu jëm ci ni réew yiy jiite àddina si di toppante ci ginnaaw Babilon. Réewu Médi-Pers ak bu Geres bokkoon nañu ci (Daniel 8:​5-7, 20-22). Seetal xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, ci xët 199 ba 201. Dinga ci gis lu bare li Biibël bi yégle woon ci lu jëm ci Almasi bi te mu am ci Yeesu Kirist.