Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK BENN

Lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ?

Lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ?
  • Ndax Yàlla moo tax metit yi am ?

  • Lan lañu weddi ca toolu Eden ?

  • Naka la Yàlla di dindee li metit yi def ci doomu Aadama yi ?

1, 2. Yan metit la nit ñi di am tey, te yan laaj la loolu di indi ?

BENN bés xare bu metti amoon na ci benn réew. Ay junni junniy jigéen ak xale lañu reyoon ci xare boobu. Ñu daldi leen boole ñoom ñépp, suul leen ci pax bu réy, ba pare wërale pax boobu yépp ak ay kurwaa yu ndaw. Ci kurwaa bu nekk ñu bind ci : “ Lu tax ? ” Yenn saay, laaj boobu mooy gën a diis ci laaj yépp. Bu seen mbokk walla xarit bu deful dara gaañoo ci xare, musiba, feebar walla nit rey ko, xolu nit ñi dafay fees. Lii lañuy laaj : “ Lu tax loolu am ? ”  Bu lu mel noonu yàqee seen kër, walla teg leen yeneen metit yu réy, laaj boobu lañuy laaj. Dañu bëgg a xam lu tax metit yooyu dal leen.

2 Lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ? Dañuy wax ne Yexowa Yàlla mooy Aji Kàttan ji. Dafa bare mbëggeel, xam-xam ak njubte. Bu dee noonu la, kon lu tax bañante ak jubadi bare noonu ci àddina ? Ndax mas nga laaj sa bopp laaj yooyu ?

3, 4. a) Lan moo ñuy won ne amul dara lu bon ci laajte lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ? b) Naka la Yàlla di gise jëfi soxor ak metit ?

3 Ndax laajte lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit baaxul ? Am na ñu ragal a laajte loolu, ndaxte dañuy foog ne loolu ñàkk gëm Yàlla la, walla ñàkk ko may cér. Waaye booy jàng Biibël bi, dinga gis ne, ay nit ñu gëm Yàlla, te ragal ko, laajte woon nañu lu mel noonu. Mën nañu ko seet ci bi yonent Yàlla Xabakukk laajee Yexowa lii : “ Lu tax nga nangu may gis lu bon, te ngay kontine di seetaan nit ñi ci coono ? Lu tax yàq ak jëfi soxor nekk ci sama kanam ? Lu tax muy am ay xuloo te ñàkk déggoo di gën a bare ? ” — Xabakukk 1:​3, NW.

Yexowa dina dindi metit yépp.

4 Xabakukk, yonent bu takku ci Yexowa la woon. Waaye bi mu ko laajee loolu, ndax Yexowa daloon na ci kawam ? Déedéet. Yàlla dafa def ñu bind ci Biibël bi kàddu yooyu Xabakukk tibbe ci xolam. Yàlla dimbali na ko mu gën a nànd ni mbir mi deme, te gën a dëgëral ngëmam. Loolu it la Yexowa bëgg a def ak yow. Bul fàtte, Biibël bi nee na Yàlla “ ku leen ñeewante la ”. (1 Piyeer 5:⁠7.) Doomu Aadama dafa bañ jëfi soxor ak metit yi ñuy indi. Waaye Yàlla moo ko ko gën a bañ fuuf (Esayi 55:​8, 9). Kon boog, lu tax àddina di metti nii ?

LU TAX ÀDDINA DI METTI NII ?

5. Lan lañuy wax nit ñi yenn saay ci lu tax doomu Aadama yi di am ay metit, waaye lan la ci Biibël bi wax ?

5 Lu tax àddina di metti nii ? Ci diine yu bare, am na ñu laaj loolu seen kilifa diine ak ñi leen di jàngal ci wàllu diine. Lu ci ëpp dañu leen di tontu ne ndogalu Yàlla la. Te lépp li am, ba ci musiba yi sax, Yàlla dafa ko bindoon bu yàgg. Ñu bare dañuy wax ne kenn mënul a xam ay mbiru Yàlla. Dañuy wax it ne Yàlla mooy rey ba ci xale yi sax, pur ñu nekk ak moom ca asamaan. Waaye, ni ñu ko gise woon, Yexowa Yàlla masul tax lu bon am. Biibël bi nee na : “ Yàlla dëgg ji du def lu bon mukk, te Moom Aji Kàttan ji du def mukk lu dul yoon ! ” — Ayóoba 34:​10, NW.

6. Lu tax nit ñu bare foog ne Yàlla mooy dogal metit yi ci àddina ?

6 Ndax xam nga lu tax ñu bare foog ne Yàlla moo dogal metit yi am ci àddina ? Lu ci bare, dañuy wax ne Yàlla Aji Kàttan ji moo ko dogal, ndaxte dañu foog ne ci dëgg-dëgg moom mooy jiite àddina sii. Am na ci Biibël bi dëgg bu yomb a xam te am solo lool, waaye nit ñooñu xamuñu ko. Jàngoon nga ko ci pàcc 3. Seytaane miy Ibliis mooy jiite àddina si dëgg.

7, 8. a) Naka la àddina si di wone jikko yi nekk ci njiitam ? b) Naka la matadi ak “ jamono ak xew-xew yu kenn xalaatul woon ”, bokke ci liy indi metit ?

7 Biibël bi wax na ci lu leer ne : “ Àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis. ” (1 Yowaana 5:19). Bu ñu xoolee bu baax li am tey, ndax duñu nangu ne loolu dëgg la ? Jikko malaaka biy “ nax waa àddina sépp ” mooy feeñ ci àddina si (Peeñu ma 12:⁠9). Seytaane dafa bon, mën fen te soxor. Moo tax àddina sii muy jiite fees dell ak nit ñu bon, mën fen te soxor. Loolu bokk na ci li tax àddina di metti nii.

8 Ci pàcc 3, waxoon nañu leneen li tax àddina di metti nii. Mooy matadi ak bàkkaar bi dugg ci àddina bés bi Aadama ak Awa bañee déggal Yàlla ca toolu Eden ba. Doomu Aadama yi dañuy xëccoo ngir ilif seeni moroom. Loolu moo fi indi xeex yi, noot sa moroom, ak metit (Ecclésiaste 4:1 ; 8:⁠9). Leneen liy indi metit mooy “ jamono ak xew-xew yu kenn xalaatul woon ”. (Dajalekat 9:​11, NW.) Yexowa jiitewul àddina si, te aaru ko it. Kon nit ñi lée-lée ñu am ay metit ndax musiba bu leen fekk fu ñu nekkoon kese.

9. Lu tax mu wóor ñu ne Yexowa xam na bu baax lu tax mu bàyyi àddina di metti ?

9 Xam ne du Yàlla moo tax àddina di metti, dafay dalal suñu xel. Du Yàlla moo tax xare ak lu bon am. Deful it musiba yu mel ni yëngu-yëngu suuf, taw yu mag ak yu mel noonu te ñuy teg nit ñi naqar. Du Yàlla moo tax it nit ñi di noot seeni moroom. Waaye ba tey, bëgg nañu xam lu tax Yexowa bàyyi metit yooyu yépp am ? Bu dee mooy Aji Kàttan ji, war na mën a arete loolu. Kon lu tax deful dara ? Yàlla Aji mbëggeel mii ñu xam léegi, bu deful dara, xam na bu baax lu tax. — 1 Yowaana 4:⁠8.

WEDDI BU MAG LAÑU INDI

10. Lan la Seytaane weddi, te naka la ko defe ?

10 Bu ñu bëggee xam lu tax Yàlla bàyyi àddina di metti, dañu war a dellu ca jamono bi metit yi komaase. Bi Seytaane taxee ba Aadama ak Awa def li leen Yexowa tere woon, loolu dafa indi laaj bu am solo. Seytaane weddiwul ne Yexowa ku bare kàttan la. Seytaane xam na sax ne dara tëwul Yexowa. Waaye sañ-sañu ilif bi Yexowa am la Seytaane weddi. Bi mu waxee ne Yàlla waxul dëgg, te dafay xañ lu baax ay jaamam, Seytaane dafa bëggoon a wax ne Yexowa du njiit bu baax (Njàlbéen ga 3:​2-5). Ci loolu Seytaane dafa bëgg a wax ne dundu nit ñi dina gën a neex bu leen Yàlla jiitewul. Loolu xeex kiliftéefu Yexowa la, maanaam xeex sañ-sañu jiite bi Yàlla am.

11. Lu tax Yexowa reyul ñi ko weddi woon ca toolu Eden ?

11 Aadama ak Awa bëggatuñu woon a déggal Yexowa. Kon mën nañu ne lii lañu doon wax : ‘ Soxlawuñu Yexowa nekk suñu Njiit. Mën nañu seetal suñu bopp li baax ak li bon. ’ Naka la Yexowa mënoon a regle poroblem boobu ? Naka la Yàlla mënoon a fexe ba won mbindeef yi mu may xel ne, ñi ko weddi nekkuñu woon ci dëgg ? Naka la leen di won ne li mu wax mooy yoon bi gën ? Xéyna mu am ñuy wax ne, Yàlla dafa waroon a rey rekk ñi ko weddi te sàkk ñeneen. Waaye Yàlla dafa waxoon ba pare ne, dafa bëgg doomi Aadama ak Awa feesal suuf si. Li mu bëggoon itam mooy, nit ñi nekk ci àjjana ci suuf (Njàlbéen ga 1:28). Saa yu Yexowa bëggee dara, dafa koy def (Esayi 55:​10, 11). Rax-ci-dolli, su Yexowa reyoon ñi ko weddi ca toolu Eden, loolu du faj li ñu waxoon ci moom lu jëm ci sañ-sañu jiite bi mu am.

12, 13. Waxal benn misaal buy wone lu tax Yexowa bàyyi Seytaane mu nekk njiitu àddina si. Waxal it lu tax Yàlla bàyyi doomu Aadama yi ñu jiite seen bopp.

12 Nañu jël benn misaal : Benn jàngalekat buy won eleewam yi fi ñu mën a jaar ngir def benn poroblem bu jafe ci matematik. Benn eleew bu aay ci matematik te faral di weddi jàngalekat bi daldi jóg di wax ne li jàngalekat bi di wone noonu baaxul. Mu teg ci ne jàngalekat bi aayul, ba pare muy wax ne xam na fasoŋ bu gën a baax ngir def poroblem boobu. Ay eleew ci kalaas bi daldi ko faral te komaase weddi ñoom it jàngalekat bi. Lan la jàngalekat boobu war a def ? Su dàqee eleew yooyu, lan la loolu di def ci yeneen eleew yi ? Ndax duñu foog ne seen moroom boobu ak ñi mu àndal ñoo waxoon dëgg ? Yeneen eleew yépp dinañu foog ne jàngalekat bi dafa ragaloon seen moroom bi wone ne moom mënul def poroblem boobu ni mu ware. Loolu mën na tax ñu bañ koo mayati cér. Léegi seetal liy xew su jàngalekat bi bàyyee eleew boobu won waa kalaas bi ni muy defe poroblem boobu.

Ndax eleew bi moo gën a aay ki koy jàngal ?

13 Lu mel noonu la Yexowa def. Fàttalikul ne, li xew ci toolu Eden, du ñi fa weddi woon Yàlla kese la laal. Ay milyoŋi malaaka ñu ngi doon seetaan li fa doon xew (Job 38:7 ; Dañeel 7:10). Ni Yexowa jëfe ak ñi ko weddi, dina am lu réy li muy def ci malaaka yooyu yépp. Dina mujj a laal sax mbindeef yi mu may xel yépp. Waaw, lan la Yexowa def ? Dafa bàyyi Seytaane mu wone ni muy jiitee doomu Aadama yi. Yàlla dafa bàyyi it doomu Aadama yi ñu jiite seen bopp ci ndigalu Seytaane.

14. Li Yexowa bàyyi doomu Aadama yi ñu jiite seen bopp, ban njariñ lay am ?

14 Jàngalekat bi ñu doon wax sànq, xam na ne eleew bi ko weddi ak ñi mu àndal waxuñu dëgg. Waaye xam na it ne bu leen bàyyee ñu wone li ñu wax, li ciy jóge dina amal njariñ waa kalaas bi yépp. Bu eleew yooyu mënul a wone li ñu wax, képp ku nekk ci kalaas bi te fonk dëgg, dina gis ne jàngalekat bi kese moo mën a jiite kalaas bi. Bu ëllëgee, dinañu xam lu tax jàngalekat bi dàq képp ku ko weddi. Noonu it, Yexowa xam na ne, ñépp ñi fonk luy dëgg, muy doomu Aadama walla malaaka, dinañu gis ne Seytaane ak ñi mu àndal mënuñu def li ñu wax. Dinañu gis it ne doomu Aadama yi mënuñu jiite seen bopp. Te loolu dina leen amal njariñ. Ni ko Yérémi xame ci jamono yu yàgg ya, dinañu xam dëgg gu am solo gii : “ Xam naa bu baax, céy Yexowa, ne nit ki ñu sàkk ak suuf moomul ay tànkam, nit kuy dox mënul a seetal boppam fi mu war a aw. ” — Yérémi 10:​23, NW.

LU TAX YEXOWA BÀYYI ÀDDINA DI METTI BOOBA BA LÉEGI ?

15, 16. a) Lu tax Yexowa bàyyi àddina di metti booba ba léegi ? b) Lu tax Yexowa terewul lu bon am ?

15 Lu tax Yexowa bàyyi àddina di metti booba ba léegi ? Te lu tax terewul lu bon am ? Jàngalekat bi ñu waxoon sànq, am na ñaar yu mu narul a def. Bu njëkk bi mooy, ki ko weddi bu komaasee di wone li mu wax, jàngalekat bi du ko arete. Ñaareel bi mooy, du dimbali eleew boobu ci li muy def. Noonu it, am na ñaar yu Yexowa jàpp ne du ko def. Bu njëkk bi mooy, aretewul Seytaane ak ñi mu àndal bi ñu doon jéem a wone ne li ñu wax mooy dëgg. Kon war na may Seytaane ak ñi mu àndal jot. Ci junniy at yi doomu Aadama yi nekk ci kaw suuf, nit ñi jéem nañu fasoŋi nguur bu nekk. Def nañu ay jéego ci wàllu xam-xam maanaam science, ak ci yeneen ak yeneen. Waaye loolu terewul jubadi, ñàkk bu metti, jëf yu bon, ak xare, di gën a bare ba àgg tey fi ñu masul a tollu. Leer na léegi ne nguuru nit baaxul.

16 Ñaareel bi mooy, bu Seytaane di jiite àddina si, Yexowa du ko ci dimbali. Bu Yàlla defoon ba jëf yu bon yi bañ a am, ndax du mel ni kuy jàpple ñi ko weddi ? Bu Yàlla defoon loolu, ndax nit ñi duñu foog ne, mën nañu jiite seen bopp te dara lu bon du leen ci fekk ? Bu leen Yexowa dimbali woon, kon dafay bokk ci ñi fen. Waaye Yàlla mënul “ dellu gannaaw ” maanaam mënul fen. — Yawut ya 6:⁠18.

17, 18. Lan la Yexowa di def ak lépp lu metti li dal doomu Aadama yi ndax li nit ñi ilif seeni moroom te nekk ci loxoy Seytaane ?

17 Waaye lan lañu war a xalaat ci lépp lu metti li dal doomu Aadama yi booba ba léegi ndax ñi weddi Yàlla ? Waruñu fàtte ne Yexowa mooy Aji Kàttan ji. Kon mën na te dina dindi li metit yooyu def ci doomu Aadama yi. Ni ñu ko jànge ba pare, dinañu defaraat lépp li yàqu ci suuf si, mu delluwaat nekk àjjana. Ngëm bu nit ñi am ci li Yeesu saraxe bakkanam dina dindi li bàkkaar di def ci doomu Aadama yi. Ndekkite bi nag dina dindi lépp lu dee bi yàq. Yàlla dina jaar ci Yeesu “ ngir nasaxal jëfi Seytaane ”, maanaam dindi jëfi Seytaane (1 Yowaana 3:⁠8). Yexowa dina def loolu lépp ci waxtu bi gën. Nañu kontaan ci li ko Yexowa defagul. Li mu xaar may na ñu, ñu xam dëgg gi te jaamu ko (2 Piyeer 3:​9, 10). Fi mu nekk nii, Yàlla dafa farlu ci wut ñi koy jaamu dëgg te di leen dimbali ñu muñ bépp metit bu leen mënta dal tey ci àddina su jaxasoo sii. — Yowaana 4:23 ; 1 Korent 10:⁠13.

18 Xéyna dina am ñuy laaj seen bopp lii : “ Ndax metit yooyu yépp naroon na am bu Yàlla sàkkoon Aadama ak Awa ci fasoŋ boo xam ne du ñu ko mën a weddi ? ” Boo bëggee am tontu laaj boobu, war nga xalaat ci lu am solo lu la Yexowa may.

NAKA NGAY JËFANDIKOO LI LA YÀLLA MAY ?

Yàlla dina la dimbali nga muñ metit yi.

19. Lu am solo lan la ñu Yexowa may, te lu tax ñu war koo fonk ?

19 Ni ñu ko gise ci pàcc 5, Yàlla dafa sàkk nit may ko sañ-sañu tànnal boppam li mu bëgg a def. Ndax xam nga li ñu Yàlla may noonu ni mu ame solo ? Yàlla dafa sàkk ay rabu àll yu baree bare. Lu ëpp ci li ñuy def, Yàlla moo ko def ci seen bopp ba pare (Proverbes 30:24). Nit defar na ay masin ngir ñu def lépp li ñu leen mënta sant. Bu ñu Yàlla sàkkoon ni masin yooyu, ndax dina ñu neex ? Déedéet. Kontaan nañu lool ci li mu ñu may sañ-sañu tànnal suñu bopp ki ñu bëgg a doon, tànn suñuy xarit, tànn li ñu bëgg a def ci suñu dund ak yeneen ak yeneen. Am sañ-sañu def li nga bëgg, lu neex la, te loolu sax la Yàlla bëgg.

20, 21. Sañ-sañu tànn li ñu bëgg bi ñu Yàlla may, naka lañu ko mënee jëfandikoo ci fasoŋ bi gën, te lu tax ñu war a bëgg a def loolu ?

20 Yexowa bëggul ñu jaamu ko ci kaw forse (2 Korent 9:⁠7). Nañu ko seete ci lii : lan mooy neex pàppa walla yaay ? Doomam gërëm ko ndaxte dañu ko ko sant, walla doomam fas yéene won leen ngërëmam ci kaw li mu yëg ci xolam ? Kon laaj bi mooy, naka ngay jëfandikoo sañ-sañu tànnal sa bopp li nga bëgg a def, bi la Yexowa may ? Sañ-sañ boobu, Seytaane, Aadama ak Awa dañu ko jëfandikoo ci fasoŋ bi gën a bon. Dañoo bañ a déggal Yexowa Yàlla. Yow nag, lan ngay def ?

21 Mën nga jëfandikoo sañ-sañ boobu ci fasoŋ bi gën a baax. Mën nga bokk ci ay milyoŋi nit ñi ànd ak Yexowa. Ñoom seddal nañu xolu Yàlla, ndaxte dañuy def lépp ngir wone ne Seytaane fenkat la, te ni muy jiite àddina si baaxul (Proverbes 27:11). Yow itam mën nga def loolu, boo tànnee topp yoon bu baax bi. Pàcc bii di topp, dina ci wax.