Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK

Malaaka yi : li ñuy def nit ñi

Malaaka yi : li ñuy def nit ñi
  • Ndax malaaka yi dañuy dimbali nit ñi ?

  • Naka la malaaka yu bon yi di naxe nit ñi, di leen xiir it ci lu bon ?

  • Ndax war nañu ragal malaaka yu bon yi ?

1. Lu tax ñu bëgg a xam lu jëm ci malaaka yi ?

CI LU bare, booy xamante ak nit dangay xamaale ay mbokkam. Noonu it, boo bëggee xam Yexowa Yàlla, fàww nga xam njabootam bi nekk ca asamaan, maanaam malaaka yi. Biibël bi dafay wax ne malaaka yi “ ay doomu Yàlla ” lañu (Ayóoba 38:​7, NW). Kon ban wàll lañu am ci coobare Yàlla ? Ndax am nañu wàll ci li xew ci suuf si, bi Yàlla sàkkee nit ba tey ? Ndax malaaka yi mënal nañu la dara ? Su dee waaw, naka lañu koy defe ?

2. Fan la malaaka yi jóge, te ñaata lañu ?

2 Biibël bi wax na ci malaaka yi lu mat ay téemeeri yoon. Nañu wax tuuti ci li Biibël bi wax ci ñoom ngir ñu gën leen a xam. Fan la malaaka yi jóge ? Kolos 1:16 nee na : “ Ci moom [Yeesu Kirist] la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf. ” Kon boog, Yexowa moo sàkk bépp mbindeefu xel yi ñuy woowe malaaka. Te dafa jaar ci Yeesu mi nekk taawam ngir sàkk leen. Ñaata malaaka moo am ? Biibël bi wone na ne ay téemeeri milyoŋi malaaka la Yàlla sàkk. Te malaaka yooyu yépp a bare kàttan. — Psaume 103:20 *.

3. Lan la Ayóoba 38:​4-7 wax ci malaaka yi ?

3 Kàddu Yàlla, Biibël bi, wax na ne bi ñu doon sàkk suuf si, “ doomu Yàlla yépp a komaase di màggal Yàlla ci kaw ”. (Ayóoba 38:​4-7, NW.) Kon malaaka amoon na lu yàgg bala ñuy sàkk nit, bala ñuy sàkk sax suuf si. Ci aaya boobu, Biibël bi wone na it ne am na lu malaaka yi di yëg ci seen xol, ndaxte dañu fa wax ne malaaka yi dañoo “ yuuxandoo ak mbégte ”. Gis nga ne “ doomu Yàlla yépp ” ñoo doon yuuxandoo. Ci jamono jooju, malaaka yépp a déggoo woon, nekk benn njaboot buy jaamu Yexowa Yàlla.

NAKA LA MALAAKA YI DI DIMBALEE DOOMU AADAMA YI AK DI LEEN AAR IT

4. Naka la Biibël bi di wone ne malaaka yu baax yi dañuy ittewoo li doomu Aadama yi di def ?

4 Dale ko bés bi ñu fekke bi Yàlla sàkkee Aadama ba tey, malaaka yu baax yi dañoo mas a ittewoo lépp lu jëm ci nit ñi. Te nit ñaa ngi doon gën a bare ci kaw suuf si. Lépp lu jëm ci coobare Yàlla itteeloon na it malaaka yooyu (Proverbes 8:​30, 31 ; 1 Piyeer 1:​11, 12). Bi jamono di dox, malaaka yi daldi seetlu ne li ëpp ci doomu Aadama yi, dañoo bàyyi di jaamu Yàlla mii nga xam ne moo leen sàkk te dafa leen bëgg lool. Wóor na ne loolu naqari woon na malaaka yu baax yi. Waaye nag, saa yu amee ku tuub ay bàkkaaram, dellu ci Yexowa, bu dee sax benn nit kese la, ‘ malaaka Yàlla yi [dañuy] am mbég[te] ’. (Luug 15:10.) Kon malaaka yi ittewoo nañu lool bànneexu ñiy jaamu Yàlla. Kon li Yexowa di faral di jaar ci malaaka yi ngir may doole te aar ñi koy jaamu dëgg ci kaw suuf si, waru ñu jaaxal (Yawut ya 1:​7, 14). Nañu ko seete ci lii di topp.

“ Sama Yàlla yebal na malaakam, te tëj na gémmiñu gaynde yi. ” — Dañeel 6:⁠23.

5. Lan lañu gis ci Biibël bi te muy wone ne malaaka yi dañuy jàpple doomu Aadama yi ?

5 Bi Yàlla doon alag ñu bon ñi nekkoon Sodom ak Gomor, ñaari malaaka ñoo dimbali Lóot ak doomam yu jigéen yi, génne leen foofu ngir ñu mucc (Njàlbéen ga 19:​15, 16). Ay téemeeri at ginnaaw loolu, dañu sànni woon yonent Yàlla Dañeel ci kàmb bu amoon ay gaynde. Waaye gaynde yi defuñu ko dara. Lii la Dañeel wax : “ Sama Yàlla yebal na malaakaam te tëj na gémmiñu gaynde yi. ” (Dañeel 6:23). Ci téeméeri at yi njëkk ci suñu jamono, am na malaaka bu génne ndaw li Pool kaso bi ñu ko tëjoon (Jëf ya 12:​6-11). Te it, ay malaaka mayoon nañu Yeesu doole bi mu tàmbalee liggéeyu waare bi ci kaw suuf (Màrk 1:13). Bala ñuy rey Yeesu, benn malaaka feeñu woon na ko, “ may ko doole ”. (Luug 22:43.) Wóor na ne malaaka yooyu yokk nañu bu baax doole Yeesu ci waxtu yu am solo yooyu mu tollu woon !

6. a) Naka la malaaka yi di aare ñiy jaamu Yàlla tey ? b) Ci yan laaj lañuy waxtaan léegi ?

6 Tey jii, malaaka yi dootuñu feeñu ñiy jaamu Yàlla ci kaw suuf. Bu fekkee ne sax mënuñu leen a gis, malaaka Yàlla yu bare kàttan yi, ñu ngi aar nit ñi ba tey. Rawatina bu amee lu mën a yàq seen diggante ak Yàlla. Biibël bi nee na : “ Malaakam Aji Sax ji moo wër ñi ko ragal, di leen bijji ciw ay ” maanaam di leen aar ciw ay (Sabóor 34:⁠8). Lu tax kàddu yooyu war a yokk suñu doole bu baax ? Ndaxte dafa am ay malaaka yu bon te soxor yu ñu bëgg a sànk ! Ñan ñooy mbindeef yooyu ? Fan lañu jóge ? Naka lañuy fexeel nit ñi lu bon ? Bu ñu bëggee xam tont laaj yooyu, nañu seet ci lu gàtt lu xewoon bi Yàlla sàkkee nit.

MALAAKA YU BON YU NEKK SUÑUY NOON

7. Nit ñi Seytaane jële ci yoonu Yàlla, nu ñu tollu ?

7 Ni ñu ko jàngee ci pàcc 3, benn ci malaaka yi dem na ba bëgg a ilif nit ñi. Noonu la bàyyee Yàlla. Moom lañu mujj a woowe Seytaane miy Ibliis (Peeñu ma 12:⁠9). Ci diiru 1600 at ginnaaw bi Seytaane naxe Awa, Seytaane fexe na ba jële nit ñu bare lool ci yoonu Yàlla. Tuuti nit kese ñoo kontine di gëm Yàlla, ñu mel ni Abel, Enog ak Nóoyin. — Yawut ya 11:​4, 5, 7.

8. a) Naka la ay malaaka def ba mujj a nekk ay rab ? b) Lan la rab yi waroon a def ngir mën a mucc ci mbënn mi amoon ca jamono Nóoyin ?

8 Ci jamono Nóoyin, amoon na yeneen malaaka yu bàyyi topp Yexowa. Dañoo bàyyi palaas bi ñu amoon ci njabootu Yàlla ca asamaan, wàcc ci kaw suuf, sol yaramu nit. Lu tax loolu ? Lii lañu jàng ci Njàlbéen ga 6:2 : “ Ay malaaka yu ñu folli gis jigéeni àddina ak seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leen i jabar. ” Waaye Yexowa Yàlla bàyyiwul malaaka yooyu kontine ci li ñu nekke. Bàyyiwul it seen jëf yu bon yooyu kontine di yàq doomu Aadama yi. Mu daldi def mbënn bu metti ci kaw suuf sépp. Mbënn boobu dafa alag ñu soxor ñépp. Ñi doon jaamu Yàlla kese ñoo mucc (Njàlbéen ga 7:​17, 23). Malaaka yu bon yi, maanaam rab yi walla jinne yi, amuñu woon beneen pexe bu dul bàyyi yaramu nit bi ñu jëloon, nekkaat malaaka te delluwaat ca asamaan. Noonu lañu ànde ak Ibliis. Ibliis daldi nekk “ buuru rab yi ”. — Macë 9:⁠34.

9. a) Lan moo dal rab yi, bi ñu delloo ca asamaan ? b) Ci lan lañuy wax ci rab yi ?

9 Bi malaaka yi bañoon a déggal Yàlla delloo ca asamaan, mënatuñu woon bokk ci njabootu Yàlla, ni seen njiit Seytaane (2 Piyeer 2:⁠4). Fi mu nekk nii, mënatuñu jël yaramu nit. Waaye ñu ngi kontine di puus nit ñi ci lu bon. Li am sax mooy, Seytaane mu ngi “ nax waa àddina sépp ” moom ak rab yi koy jàpple (Peeñu ma 12:9 ; 1 Yowaana 5:19). Naka la loolu di ame ? Ci lu ëpp, rab yi dañuy jaar ci ay pexe ngir nax nit ñi (2 Korent 2:11). Nañu wax ci yenn ci pexe yooyu.

NAKA LA RAB YI DI NAXE NIT ÑI

10. Kañ lañu mën a wax ne nit laal na ci kort, luxus walla mbirum tuuri maam ak yu mel noonu ?

10 Ngir nax nit ñi, rab yi dañuy jëfandikoo kort, luxus walla mbirum tuuri maam ak yeneen yu mel noonu. Kañ lañu mën a wax ne nit laal na ci mbir yooyu ? Dina ci laal buy jokkoo ak rab yi, di wax ak ñoom walla muy jaar ci keneen ngir def loolu. Biibël bi wone na ne kort, luxus walla mbirum tuuri maam ak yeneen yu mel noonu baaxul. Wax na it ne dañu war a sore lépp lu laal ci mbir yooyu (Galasi 5:​19-21). Rab yi dañuy jëfandikoo mbir yooyu te mel ni nappkat buy def dara ci oos ngir jàpp jën. Nappkat bu bëggee jàpp jën yu wuute, li muy def ci oos bi dafay wuute. Noonu it, malaaka yu bon yi dañuy jaar ci pexe yu wuute ci kort, luxus walla mbirum tuuri maam ak yu mel noonu, ngir ilif fasoŋu nit bu nekk.

11. Lan mooy gisaane, te lu tax waruñu ko def ?

11 Leneen lu rab yi di jëfandikoo mooy gisaane. Lan mooy gisaane ? Gisaane mooy jéem a xam liy ñëw ëllëg walla jéem a xam lu nëbbu. Tani, li tubaab di woowe horoscope, seet ci rëddi loxo, walla firi ay gént, loolu lépp bokk na ci gisaane. Ñu bare dañuy wax ne gisaane du la def dara. Waaye Biibël bi dafay wone ne, gisaanekat yi dañuy jëflante ak malaaka yu bon yi. Mën nañu ko seet ci lii. Jëf ya 16:​16-18 am na li mu wax ci “ jigéen bu rabu gisaane solu ”. Rab boobu mayoon na ko mu mën ‘ gisaane ’. Waaye bi ñu génnee rab bi ci moom la jigéen ji mënatul gisaane.

Malaaka yu bon yi dañu am pexe yu bare ngir nax nit ñi.

12. Lu tax jéem a wax ak nit ku dee doon lu lay lor ?

12 Beneen pexe bi rab yi di jariñoo ngir nax nit ñi, mooy di leen xiir ñuy wax ak ñi dee. Ñi am mbokk bu gaañu, dañu leen faral di wax lu dul dëgg ci ñi dee. Gisaanekat mën na la wax lu am ci ku gaañu, walla mu jël baatu nit ki dee, di wax ak yow. Loolu tax na ba ñu bare gëm ne ñi dee am na fu ñu nekk di dund ba tey, te bu ñu waxee ak ñoom, dina leen dimbali ñu muñ seen naqar. Waaye loolu ñu yaakaar ne dina leen “ may doole ”, du dëgg te dafa leen di lor. Lu tax ? Ndaxte rab yi mën nañu jël baatu nit ki gaañu, te wax gisaanekat bi lu bare lu jëm ci nit kooku (1 Samuel 28:​3-19). Te it sax, ni ñu ko jànge ci pàcc 6, ñi dee nekkatuñu (Psaume 115:17). Képp kuy wax ak nit ñi dee, malaaka yu bon yi ñoo koy nax, te li muy def noonu neexul Yàlla (Deutéronome 18:​10, 11 ; Esayi 8:19). Moo tax, nanga moytu daanu ci pexe rab yooyu di lor nit ñi.

13. Ñu bare ci ñi ragaloon rab yi, lan lañu mujj a def ?

13 Malaaka yu bon yi yemuñu rekk ci di nax nit ñi. Dañu leen di tiital itam. Tey, Seytaane ak malaakaam yi xam nañu ne jot gi leen dese bala ñu leen di tëj ba dootuñu mën a def dara, “ barewul ”. Moo tax tey lañu gën a soxor (Peeñu ma 12:​12, 17).) Am na ay junniy nit ñu ragaloon rab yu bon yooyu. Waaye dem nañu ba génn ci. Naka lañu def ? Lan la nit mën a def su dee sax dugg na ba pare ci mbirum kort walla tuuri maam ak yu mel noonu ?

NI ÑUY XEEXE MALAAKA YU BON YI

14. Ni ko karceen yu njëkk yi nekkoon Efes defe, lan lañu war a def ngir génn ci loxo malaaka yu bon yi ?

14 Biibël bi wax na li ñu mën a def ngir xeex malaaka yu bon yi, ak li ñu mën a def ngir génn ci seeni loxo. Nañu wax ci karceen yi nekkoon ca Efes, ci téeméeri at yi njëkk ci suñu jamono. Amoon na ci ñoo xam ne, bala ñuy nekk ay karceen, dañu doon luxus di kort ak yeneen yu mel noonu. Bi ñu fas yéenee génn ci loolu, lan lañu def ? Biibël bi nee na : “ Ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. ” (Jëf ya 19:19). Nit ñooñu sog a nekk karceen, dañu lakkoon seeni téere luxus yépp. Li ñu def noonu wone na li ñu war a def bu ñu bëggee xeex malaaka yu bon yi. Ñi bëgg a jaamu Yexowa war nañu yàq lépp lu ñu amoon lu jëm ci kort, luxus walla mbirum tuuri maam ak yu mel noonu. Loolu ëmb na luy xiir nit ñi ci loolu, walla luy gëmloo nit ñi ne lu neex la. Mën na nekk téere, yéenekaay, film, foto walla misik. Loolu lépp bokk na ci li ñu war a yàq. War nañu bàyyi it gàllaaj yi walla lépp li ñuy takk ngir aar suñu bopp ci lu bon. — 1 Korent 10:⁠21

15. Lan lañu war a def ngir mën a xeex malaaka yu bon yi ?

15 Tuuti at ginnaaw bi karceen yi nekkoon Efes lakkee seeni téere luxus, lii la leen ndaw li Pool bind : “ Ndëndu xare jib na, [...] ak [...] gaayi Seytaane yi ci bérab yu kawe yi. ” (Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Efes 6:12). Rab yi bàyyiwuñu woon xeex bi. Ba tey, ñu ngi doon wut ni ñuy fexee ba ëpp doole nit ñi. Kon, leneen lan la karceen yooyu waroon a def ? Lii la leen Pool wax : “ Defleen it ngëm, muy seen pakk, ba man a fél jum yi leen Seytaane di fitt. ” (Efes 6:16). Suñu ngëm buy gën di dëgër, ñuy gën di am doole ngir xeex rab yu bon yi. — Macë 17:⁠20.

16. Naka lañu mënee dëgëral suñu ngëm ?

16 Kon naka lañu mënee dëgëral suñu ngëm ? Dañu war a gëstu Biibël bi. Bala miir di mën a dëgër, fondamaa bi dafa war a dëgër. Noonu la it ci wàllu ngëm. Bala suñu ngëm di mën a dëgër, dafa war a am fondamaa bu baax. Fondamaa boobu mooy xam-xam bu wér te wóor bi nekk ci Kàddu Yàlla, Biibël bi. Bu ñuy jàng te di gëstu Biibël bi bés bu nekk, suñu ngëm dina dëgër. Ni miir bu dëgër di aare, ngëm bu dëgër it dina ñu aar ci rab yu bon yi. — 1 Yowaana 5:⁠5.

17. Lan lañu war a def ngir mën a xeex rab yu bon yi ?

17 Lan la karceen yi nekkoon Efes waroon a def itam ? Dañu waroon a yokk li leen di aar, ndaxte ci dëkk bu bare rab lañu nekkoon. Moo tax Pool nee leen : “ Deeleen ñaan ci xeeti ñaan yépp ci kàttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat sëkk. ” (Efes 6:18). Tey it, àddina si dafa bare rab yu bon. Kon bu ñu bëggee xeex rab yooyu, dañu war a ñaan Yexowa ak suñu xol bépp ngir mu aar ñu. Xam nañu it ne bu ñuy ñaan, dañu war a jaar ci turu Yexowa (Proverbes 18:10). War nañu kontine it di ñaan Yàlla ngir mu “ musal nu ci lu bon ” maanaam ci Seytaane miy Ibliis (Macë 6:13). Yexowa dina tontu ñaan yooyu nga xam ne ci suñu xol lañu jóge. — Psaume 145:⁠19.

18, 19. a) Lu tax mu wóor ñu ne dinañu daan malaaka yu bon yi ? b) Yan laaj lañuy tontu ci pàcc bii di topp ?

18 Rab yu bon yi dañu soxor. Waaye bu ñuy xeex Seytaane te jege Yàlla ndax li ñuy def li mu bëgg, dootuñu ragal rab yu bon yi (Saag 4:​7, 8). Kàttanu rab yu bon yi am na fu mu yem. Yaroon nañu leen ci jamano Nóoyin, te ëllëg seen àtte bu mujj bi dina leen dal (Yudd 6). Bul fàtte it ne malaaka Yexowa yi bare kàttan lool ñoo ñuy aar (2 Rois 6:​15-17). Li malaaka yooyu bëgg ci seen biir xol mooy, ñu xeex rab yu bon yi, ba gañe leen. Mën nañu wax sax ne, malaaka yooyu dañu ñuy xiirtal ci loolu. Kon nañu jege Yexowa jege it njabootam bi ko déggal te nekk ca asamaan. Nañu moytu it lépp lu bokk ci kort, luxus walla mbirum tuuri maam ak yu mel noonu. Te nañu topp saa su nekk xelal yi nekk ci Kàddu Yàlla (1 Piyeer 5:​6, 7 ; 2 Piyeer 2:⁠9). Bu ñu defee loolu, dinañu daan malaaka yu bon yi, ci lu wóor.

19 Waaye lu tax Yàlla sànkagul malaaka yu bon yi ? Lu tax mu bàyyi lu bon li nga xam ne dafay teg doomu Aadama yi naqar bu bare lool ? Ci pàcc bii di topp, dinañu waxtaan ci laaj yooyu.

^ par. 2 Lii la Peeñu ma 5:11 wax ci malaaka yu baax yi : “ Ëppoon [nañu] alfunniy alfunniy junniy junni. ” Kon Biibël bi dafay wone ne Yàlla sàkk na ay téemeeri milyoŋi malaaka.