PÀCC FUKK AK JURÓOM
Ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko
-
Ndax diine yépp a neex Yàlla ?
-
Nu ñuy def ba ràññee diine bu baax bi ?
-
Ñan ñooy jaamu Yàlla ni ko Yàlla bëgge ci kaw suuf si tey ?
1. Bu ñuy jaamu Yàlla ni mu ko bëgge, yan barke lañuy am ?
YEXOWA YÀLLA dafa ñu fonk lool, te dafa bëgg ñu jariñoo xelal yu ànd ak mbëggeel yi mu ñuy jox. Su ñu koy jaamu ci fasoŋ bi mu bëgg dinañu am mbégte te poroblem yu bare du ñu dal. Yàlla dina ñu barkeel, te jàpple ñu itam (Isaïe 48:17). Waaye nag am na ay téeméeri diine yu foog ne dañuy jàngale liy dëgg ci Yàlla, fekk li ñuy wax ci Yàlla ak ci li Yàlla bëgg ci ñun, dafa wuute lool.
2. Bu ñu bëggee xam fasoŋu jaamu bi Yexowa nangu, lan lañu mën a def, te ban misaal moo ñuy dimbali ñu nànd loolu ?
2 Naka nga mën a def ba xam fasoŋu jaamu bi Yexowa nangu ? Jarul nga jàng li diine yépp di wax. Danga war a jàng rekk li Biibël bi wax dëgg-dëgg ci ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko. Nañu ko seete ci lii : Réew yu bare dañu am poroblemu xaalis bu baaxul (maanaam xaalis bu mel ni bu baax bi, waaye mënoo ci jënd dara). Bu ñu la santoon nga ràññee xaalis bu bon boobu, nooy def ? Ndax dangay jéem a jàpp ci sa xel fasoŋu xaalis yu bon yépp ? Déedéet. Li gën mooy nga jéem a xam bu baax ni xaalis bu baax bi mel. Boo xamee ni xaalis bu baax bi mel, dinga mën a ràññee xaalis bu bon bi. Noonu it, bu ñu jàngee ni ñuy ràññee diine dëgg ji, dinañu mën a xàmme diine yu dul dëgg yi.
3. Bu ñu seetee ci li Yeesu waxoon, lan lañu war a def bu ñu bëggee neex Yàlla ?
Macë 7:21-23.) Xaalis bu bon amul benn njariñ. Noonu it, diine bu dul dëgg amul benn njariñ. Li ci gën a bon mooy, fi mu ne nii, diine boobu dafay lor nit ñi.
3 Jaamu Yexowa ci fasoŋ bi ko neex, lu am solo la. Ñu bare dañu gëm ne diine yépp a neex Yàlla. Waaye Biibël bi waxul loolu. Wax rekk ne karceen nga, doyul itam. Yeesu nee woon na : «Du képp ku may wax : “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji ; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw.» Kon bu ñu bëggee neex Yàlla dañu war a jàng ba xam li ñu Yàlla laaj, ba pare def ko. Ñi dul def coobare Yàlla, Yeesu dafa leen doon woowe “ñiy def bàkkaar”. (4. Ñaari yoon yi Yeesu doon wax, lu ñuy tekki, te fan la yoon bu nekk di yóbbu nit ñi ?
4 Képp ku nekk ci kaw suuf, Yexowa may na ko mu mën a am dund gu dul jeex. Waaye bu ñu bëggee am dund gu dul jeex ci Àjjana, dañu war a jaamu Yàlla ni mu ware te dañu war a dund tey ci fasoŋ bu ko neex. Waaye ñu bare bëgguñu def loolu. Loolu moo tax Yeesu waxoon ne : «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare. Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw [wi jëm dund, NW] sew na, te ñi ko gis barewul.» (Macë 7:13, 14). Diine dëgg ji dafa lay yóbbu ci dund gu dul jeex. Diine bu dul dëgg nag dafa lay yóbbu ci sànkute. Yexowa bëggul kenn alku. Loolu moo tax muy def ba fépp ci àddina, nit ñi mën a xam ki mu doon (2 Piyeer 3:9). Dëgg-dëgg, loolu dafa ñuy won ne, fasoŋ bi ñuy jaamoo Yàlla moo ñuy yóbbu ca dund walla ca dee.
NI ÑUY RÀÑÑEE DIINE DËGG JI
5. Naka lañu mënee xàmme ñi bokk ci diine dëgg ji ?
5 Nu ñuy def ba xam yoon wi jëm dund ? Yeesu waxoon na ne dinañu mën a ràññee diine dëgg ji ci ni nit ñi Macë 7:16, 17.) Maanaam ñi bokk ci diine dëgg ji, dinañu leen xàmme ci li ñu gëm ak ci li ñuy def. Nit ñooñu matuñu te dañuy juum itam. Waaye dañu nekk mbooloo buy jéem a def coobare Yàlla. Nañu waxtaan ci juróom benni ponk yuy tax ñu ràññee ñi bokk ci diine dëgg ji.
ci bokk di dunde. Lii la waxoon : «Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf.» Mu yokk ci ne «garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex». (6, 7. Lan la Biibël bi doon ci ñiy jaamu Yàlla dëgg, te naka la Yeesu nekke royukaay ci loolu ?
6 Ñiy jaamu Yàlla, ci Biibël bi lañuy jële li ñuy jàngale. Biibël bi ci boppam nee na : “ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet. ” (2 Timote 3:16, 17). Ndaw li Pool bindoon na mbokkam karceen yi, ne leen : “ Ba ngeen jotee kàddug Yàlla, gi ñu doon waare, nangu ngeen ko, waxuma ni kàddug nit waaye ni kàddug Yàlla, ndaxte moom la ci dëgg-dëgg. ” (1 Tesalonig 2:13). Kon, ñi bokk ci diine dëgg ji, li ñu gëm ak li ñuy def, jëlewuñu ko ci xalaatu nit walla ci ay aada. Ci Kàddu Yàlla, Biibël bi, lañu ko jële.
7 Yeesu Kirist, ci Kàddu Yàlla la doon jële lépp li mu doon jàngale. Won na ñu ci loolu li ñu war a def. Mas na wax lii Yàlla ci ñaan : «Sa kàddu mooy dëgg.» (Yowaana 17:17). Yeesu dafa gëmoon Kàddu Yàlla. Te lépp li mu doon wax dafa àndoon ak li nekk ci Mbind mi. Yeesu tàmmoon na di wax lii : «Mbind mi nee na.» (Macë 4:4, 7, 10). Saa yu waxee loolu, dafa ci doon teg li nekk ci benn aaya. Noonu it tey, ñiy jaamu Yàlla dëgg, duñu wax seeni xalaatu bopp. Dañu gëm ne Biibël bi mooy Kàddu Yàlla. Te li ñuy jàngale, ci Biibël bi lañu koy jële.
8. Jaamu Yexowa lan lay laaj ?
Macë 4:10). Kon ñiy jaamu Yàlla dëgg, Yexowa kese lañuy jaamu. Jaamu Yàlla noonu dafa laaj ñu xamal nit ñi turu Yàlla dëgg ji ak ki mu doon. Sabóor 83:18, NW, nee na : “ Yow mii tudd Yexowa, yow rekk yaay Aji Kawe ji ci kaw suuf si sépp. ” Yeesu royukaay la woon ci lu jëm ci dimbali nit ñi ñu xam Yàlla. Masoon na ñaan Yàlla ne ko : «Xamal naa sa tur nit, ñi nga tànne ci àddina te dénk ma leen.» (Yowaana 17:6). Noonu it tey, ñiy jaamu Yàlla dëgg dañuy jàngal seeni moroom lu jëm ci turu Yàlla, ci coobareem, ak ci ay jikkoom.
8 Ñi bokk ci diine dëgg ji, Yexowa rekk lañuy jaamu te dañuy xamal nit ñi turam. Lii la Yeesu waxoon : “Nanga màggal [Yexowa, NW] Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.” (9, 10. Naka la karceen dëgg yi wonee ne dañu bëggante ?
9 Ñiy jaamu Yàlla dañu bëggante dëgg. Yeesu nee woon na : «Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.» (Yowaana 13:35). Mbëggeel bu mel noonu moo amoon ci diggante karceen yu njëkk yi. Mbëggeel bu ànd ak li Yàlla sant ci Biibël bi du seet ci xeet, askan ak réew bu nit ki bokk. Dafay boole nit ñi, ñu nekk benn, doon ay mbokk yu kenn mënul a féewale (Kolos 3:14). Ñi bokk ci diine yu dul dëgg yi nag, amuñu mbëggeel bu mel noonu ci seen biir. Lan moo koy wone ? Dañuy reyante ndax li ñu bokkul réew walla xeet. Karceen dëgg yi duñu jël gànnaay ngir rey seeni mbokk karceen, walla sax nit ku mu mënta doon. Biibël bi nee na : “ Lii mooy ràññale doomi Yàlla ak doomi Seytaane : képp ku dul def lu jub bokkoo ci Yàlla ; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Yàlla. [...] Nañu bëggante, te bañ a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. ” — 1 Yowaana 3:10-12 ; 4:20, 21.
10 Dëgg la, mbëggeel dëgg yemul rekk ci bañ a rey sa moroom. Karceen dëgg yi dañuy fàtte seen bopp, jël seen jot, seen kàttan, ak seen alal ngir di dimbalante ak di xiirtalante Yawut ya 10:24, 25). Dañuy dimbalante bu ñu nekkee ci ay jafe-jafe, te gore ak seeni moroom. Dëgg-dëgg, ci li ñuy def, dañuy topp li Biibël bi wax fii : “ Nanuy defal ñépp lu baax. ” — Galasi 6:10.
(11. Nangu ne ci Yeesu Kirist la Yàlla di jaar ngir musal doomu Aadama yi, lu tax mu am solo lool ?
11 Karceen dëgg yi dañuy nangu ne ci Yeesu Kirist la Yàlla di jaar ngir musal doomu Aadama yi. Biibël bi nee na : «Mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu war a mucce.» (Jëf ya 4:12). Ni ñu ko gise ci pàcc 5, Yeesu dafa joxe bakkanam ni njotug doomu Aadama yi déggal Yàlla (Macë 20:28). Rax-ci-dolli, Yeesu mooy ki Yàlla tànn ngir mu nekk Buuru Nguuram gi nekk ca asamaan. Nguur googu mooy jiite suuf si sépp. Yàlla dafa bëgg ñuy déggal Yeesu te topp li mu ñu wax, bu ñu bëggee am dund gu dul jeex. Looloo tax Biibël bi wax ne : “ Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex ; ku déggadil Doom ji, amuloo dund. ” — Yowaana 3:36.
12. Bañ a bokk ci àddina si, lan lay tekki ?
12 Ñiy jaamu Yàlla dëgg bokkuñu ci àddina si. Bi ñu ko doon àtte ci kanamu Pilaat, mi nekkoon kilifa ci waa Room, lii la Yeesu waxoon : «Sama kilifteef nekkul ci àddina.» (Yowaana 18:36). Ci réew bu ñu mënta nekk, taalibe Kirist dëgg yi, dañuy déggal Nguuru Yàlla bi nekk ca asamaan. Moo tax duñu bokk ci dara lu jëm ci mbirum politig ci àddina si. Duñu bokk it ci xeex yi am ci àddina si. Waaye ñiy jaamu Yexowa, bu seen moroom bëggee bokk ci parti politig, walla mu bëgg ñu fal ko ni njiitu réew, walla it mu bëgg a wote, duñu ko ko jéem a tere. Ñiy jaamu Yàlla dëgg, bokkuñu ci lu jëm ci politig, waaye dañuy topp li sàrtu réew mi laaj. Lu tax loolu ? Ndaxte lii la leen Kàddu Yàlla sant : “ Na nit ku nekk déggal ” kilifa nguur yi “ yore baat ci kanamam ”. (Room 13:1.) Su fekkee ne li nguur gi bëgg àndul ak li Yàlla santaane, jaamu Yàlla dëgg yi dañuy roy ndawi Yeesu ñi waxoon lii : «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.» — Jëf ya 5:29 ; Màrk 12:17.
13. Naka la taalibe Kirist dëgg yi di gise Nguuru Yàlla, te loolu lan la leen defloo ?
13 Taalibe Yeesu dëgg yi, dañuy yégle ne ci Nguuru Yàlla kese la doomu Aadama mën a yaakaar. Yeesu nee woon na : «Xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle Macë 24:14). Taalibe Kirist dëgg yi duñu wax nit ñi ñu def seen yaakaar ci doomu Aadama yiy jiite réew yi. Dañuy wax nit ñi ne ci Nguuru Yàlla kese lañu mën a yaakaar (Psaume 146:3). Yeesu jàngal na ñu ni ñuy ñaane ngir Nguur gu mat googu. Lii la waxoon : “Na sa nguur ñëw. Na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.” (Macë 6:10). Kàddu Yàlla waxoon na ne Nguuru Yàlla gi nekk ca asamaan “dina jàllarbi ak a tasaare nguur yeneen yépp [maanaam nguur yi fi nekk tey], waaye moom doŋŋ dina sax ba fàww”. — Dañeel 2:44.
ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee muju jamono ji jot.» (14. Ci yow, ci ban diine lañuy jaamu Yàlla ni ko Yàlla bëgge ?
14 Xalaatal ci li ñu jot a wax fii, te laaj sa bopp lii : ‘ Ban diine moo jële lépp li muy jàngale ci Biibël bi, te di xamal nit ñi turu Yexowa ? Ci ban diine la nit ñi di wone mbëggeel ni ko Yàlla bëgge ? Ban diine moo wone ngëm ci Yeesu, bañ a bokk ci àddina si te di wax ne ci Nguuru Yàlla kese la doomu Aadama yi mën a yaakaar ? Ci diine yépp yi nekk ci kaw suuf si, ban moo ciy def loolu lépp ? ’ Boo seetee ba seet, dinga gis ne Seede Yexowa yi ñooy def loolu lépp. — Isaïe 43:10-12.
LAN NGAY DEF ?
15. Ginnaaw bi ñu gëmee ne Yàlla am na, lan la Yàlla bëgg ñu def ?
15 Gëm Yàlla kese taxul nga neex Yàlla. Biibël bi wax na ne rab yi sax gëm nañu ne Yàlla am na (Saag 2:19). Leer na ne rab yi duñu def coobare Yàlla, te neexuñu Yàlla. Bu ñu bëggee neex Yàlla, waruñu gëm rekk ne Yàlla am na, waaye dañu war a def it coobareem. Dañu war a génn itam ci diine bu dul dëgg, te bokk ci ñiy jaamu Yàlla ni ko Yàlla bëgge.
16. Lan lañu war a def lu jëm ci diine bu dul dëgg ?
16 Ndaw li Pool waxoon na ne waruñu bokk ci diine bu dul dëgg. Lii la bindoon : “ Boroom bi nee na : «Génnleen 2 Korent 6:17 ; Isaïe 52:11). Karceen dëgg yi dañuy moytu lépp lu bokk ci diine bu dul dëgg.
biir ñooñu te beru. Buleen laal dara lu am sobe, kon dinaa leen teeru.» ” (17, 18. Lan mooy “ Babilon mu mag mi ”, te lu tax ñu war a ‘ génn ci biiram ’ ci lu gaaw ?
17 Biibël bi wone na ne diine yu dul dëgg yépp, ci “ Babilon mu mag mi * ” lañu bokk (Peeñu ma 17:5). Tur boobu dafa ñuy fàttali dëkk bu yàgg bi tuddoon Babilon. Foofu la diine bu dul dëgg jóge, ginnaaw bi mbënn mi amee ca jamono Nóoyin. Lu bare ci li ñuy jàngale ak aada yi am tey ci diine yu dul dëgg yi, ca Babilon lañu ko doon topp bu yàgg. Mën nañu seet loolu ci lii : waa Babilon gëmoon nañu li ñuy woowe ci tubaab Trinité, walla Triade maanaam ñetti yàlla yu def benn. Tey jii, Trinité mooy ngëm bi ëpp solo ci diine yu bare. Waaye Biibël bi wax na ci lu leer ne, benn Yàlla dëgg kese moo am, maanaam Yexowa te Yeesu Kirist mooy doomam (Yowaana 17:3). Waa Babilon gëmoon nañu itam ne nit dafa am ruu. Bu nit ki deewee, ruu bi dafay kontine di dund, te mën na nekk ci béréb fu ñu koy toroxal. Tey, lu ëpp ci diine yi dañuy wax ne bu nit dewee dafa am ruu buy kontine di dund. Te ruu bi mën nañu ko toroxal ca safara.
18 Komka diine Babilon bu njëkk bi dafa law ci kaw suuf si sépp, kon mën nañu wax ne Babilon mu mag mi mooy mbooloo diine yu dul dëgg yépp yi nekk ci àddina si. Te Yàlla waxoon na ne mbooloo diine yu dul dëgg yooyu, dinañu leen fi dindi, dindi bu gaaw buy bett nit ñi (Peeñu ma 18:8). Ndax xam nga léegi lu tax génn ci lépp lu bokk ci Babilon mu mag mi am solo lool ? Yexowa Yàlla dafa bëgg nga ‘ génn ci biiram ’ ci lu gaaw bala muy wees. — Peeñu ma 18:4.
19. Lan ngay am booy jaamu Yexowa ?
19 Boo waxee ne dangay génn ci diine yu dul dëgg yi, mën na am ay nit bàyyi di ànd ak yow. Waaye boo àndee ak mbooloo Yexowa di ko jaamu, li nga ciy am mooy ëpp fuuf lépp li nga ci mën a ñàkk. Yow it dinga mujj a am ay mag ak rakk yu bare ci wàllu ngëm, ni taalibe Yeesu yu njëkk yi bàyyi woon yenn yi ngir topp Yeesu. Dinga bokk ci ay milyoŋi karceen dëgg yi mel ni njaboot bu mag bu nekk ci kaw suuf si sépp. Te karceen yooyu dinañu la bëgg bu baax. Dinga am it yaakaar bu neex lool, maanaam yaakaaru am dund gu dul jeex «ëllëg». (Màrk 10:28-30.) Ñi bàyyi di ànd ak yow ndax li nga gëm, xéyna bu ëllëgee dinañu seet li Biibël bi wax, ba mujj di jaamu Yexowa ñoom itam.
20. Ñi nekk ci diine dëgg ji, lan lañuy séentu ëllëg ?
20 Biibël bi wax na ne, léegi Yàlla alag àddina bu bon bii, te indi àddina bu bees fu njub dëkk te Nguuru Yàlla di ko jiite (2 Piyeer 3:9, 13). Àddina boobu dina neex lool ! Ci àddina bu bees boobu, benn diine kese mooy am, maanaam benn fasoŋu jaamu Yàlla. Def lépp li war tey ngir mën a ànd ak ñiy jaamu Yàlla dëgg, ndax loolu du am xel dëgg ?
^ par. 17 Boo bëggee ay leeral ci lu tax ñuy wax ne Babilon mu mag mi mooy mbooloo diine yu dul dëgg yépp yi nekk ci àddina si, seetal li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 219 ak 220.