Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC JURÓOM-BENN

Fan la ñi dee nekk ?

Fan la ñi dee nekk ?
  • Lan mooy dal nit bu deewee 

  • Lu tax ñuy dee ?

  • Xam dëgg gi ci ñi dee, ndax dina dalal suñu xel ?

1-3. Lan la nit ñi di laajte ci lu jëm ci dee, te lan la ci diine yu bare wax ?

LU MAT ay junni at ba tey, nit ñi dañuy laaj seen bopp laaj yu am solo yooyu. Ku ñu mënta doon ak fi ñu mënta nekk, tont yi soxal na ñu ñun ñépp.

2 Ci pàcc bi weesu, gis nañu ni saraxu Yeesu Kirist bi nekk njot gi di maye nit ñi dund gu dul jeex. Jàngoon nañu it ne Biibël bi wax na ne dina am jamono joo xam ne «dee dootul am». (Peeñu ma 21:⁠4.) Waaye fi ñu tollu nii, ñépp ay dee. Suleymaan, buur bu bare woon xam-xam nee woon na : “ Ñiy dund xam nañu ne dinañu dee. ” (Dajalekat 9:​5, NW). Nit dafay def lépp ngir gudd fan. Waaye ba tey, bëgg nañu xam luy dal nit bu deewee.

3 Suñu mbokk walla suñu xarit bu deewee, dañuy am naqar bu réy. Te mën na am ñu laaj suñu bopp lii : ‘ Lan mooy dal ñi dee ? Ndax ñu ngi ci ay coono ? Ndax ñu ngi ñuy aar ? Ndax mën nañu leen a dimbali ? Ndax dinañu leen mas a gisaat ? ’ Li diine yi ci àddina bi tey di tontu ci laaj yooyu wuute na lool. Am na ñuy wax ne booy def lu baax ci sa dund, dinga dem ci kaw asamaan. Waaye booy def lu bon, dinañu la yóbbu fi ñu lay lakk, di la toroxal. Am na diine yuy wax it ne bu nit deewee, dafay nekk xel ngir dem fu suñu maam yi dee nekk. Am na yeneen diine yuy wax ne bu nit deewee dafay nekk ci biir suuf fu ñu koy àtte, ba pare dina judduwaat yore beneen yaram.

4. Ban xalaat la diine yu bare bokk ci lu jëm ci dee ?

4 Diine yooyu yépp am na fu ñuy bokk xalaat, moo di bu nit deewee, am na luy jóge ci moom kontine di dund feneen. Kon bu ñu seetee li ëpp ci li diine yi di jàngale, muy ci jamono yu njëkk ya walla ci suñu jamono tey, mën nañu ne, pur ñoom, nit dafay dund ba fàww, di kontine di gis, di dégg ak di xalaat. Waaw, loolu nu mu mën a nekke ? Xam nañu ne suñu xel mi nekk ci suñu bopp moo tax ñu mën a xalaat, mën a dégg, te mën a gis. Bu nit deewee xelam dee na. Kon mënatul xalaat dara, yëg dara walla fàttaliku dara.

LAN MOOY XEW DËGG BU NIT DEEWEE

5, 6. Lan la Biibël bi wax ci li ñi dee nekke ?

5 Liy xew bu nit deewee jaaxalul Yexowa moom mii bind xelu nit. Xam na luy dëgg gi, te ci Kàddoom, Biibël bi, wax na ci lan la ñi dee nekke. Lu leer lii la wax : Bu nit deewee, fa lay yem. Dootul nekkati fenn. Dee ak dund bokkuñu dara, dañu safaanoo. Ku dee mënul gis, mënul dégg, te mënul xalaat. Bu nit deewee amul dara luy jóge ci moom di kontine dund. Yorewuñu ruu walla xel bu dul dee mukk *.

Fan la tàkk-tàkk bi dem ?

6 Bi Suleymaan waxee ne ñiy dund xam nañu ne dinañu dee, dafa ci yokk ne : “ Waaye ñi dee, ñoom, xamuñu dara. ” Am na lu mu ci yokk ngir gën a leeral dëgg googu. Dafa ne ñi dee mënuñu bëgg, mënuñu bañ, te it “ amul liggéey, amul waaj, amul xam-xam ” ca bàmmeel ba (Dajalekat 9:​5, 6, 10, NW). Sabóor 146:​4, NW, lu mel noonu la wax bi mu nee, bu nit deewee “ ay xalaatam dañuy jeex ”. Ñépp ay dee, te bu nit deewee du am dara luy jóge ci moom di kontine di dund feneen. Suñu dund dafa mel ni sondeel bu ñu taal. Bu ñu ko feyee, tàkk-tàkk bi du dem feneen. Dafa amatul rekk.

LAN LA YEESU WAXOON CI DEE

7. Naka la Yeesu wonee li dee di nirool ?

7 Am na lu Yeesu Kirist waxoon ci ñi dee. Waxoon na ko ci Lasaar, mi nekkoon ku mu xamoon bu baax, te mu gaañu woon. Yeesu dafa wax taalibeem yi ne : «Suñu xarit Lasaar nelaw na.» Taalibee yi dañu foogoon ne Yeesu dafa doon wax ne Lasaar dafay nelaw rekk, di noppaleeku ndax feebar bu ko dal te dina wér. Waaye du loolu la Yeesu doon wax. Yeesu daldi leen ne : «Lasaar dee na.» (Yowaana 11:​11-14). Gis ngeen ne Yeesu dafa méngale dee ak noppalu walla nelaw. Lasaar nekkul woon ca asamaan, nekkul woon it ca safara. Demul woon ca malaaka yi walla ca maamam yi dee. Lasaar judduwaatul nekk beneen nit. Dafa doon noppalu ci dee, ni kuy nekk ci ay nelaw yu xóot yu àndul ak gént. Am na yeneen aaya yuy méngale dee ak nelaw. Bi ñu sànnee taalibe Yeesu bi tudd Ecen ay doj ba rey ko, Biibël bi dafa ne dafa “ nelaw ”. (Jëf ya 7:​60,) Noonu it, ndaw li Pool bindoon na lu jëm ci ñi mu bokkaloon jamono te “ ñu nelaw ” ci dee. — 1 Korent 15:⁠6.

Yexowa dafa bind doomu Aadama yi ngir ñu dund ba fàww ci kaw suuf.

8. Lan moo ñuy won ne Yàlla bindul nit pur mu dee ?

8 Bi Yàlla bindee nit, ndax dafa bëggoon mu dee ? Déedéet ! Yexowa dafa bind nit ngir mu dund ba fàww ci kaw suuf. Ni ñu ko jànge woon ci téere bii, Yàlla dafa def góor bu njëkk bi ak jigéen bu njëkk bi ci àjjana bu rafet. Mu daldi leen may wér-gi-yaram gu mat sëkk. Lu baax rekk la leen Yexowa yéene woon. Ku bëgg doomam, ndax dina bëgg mu daj metit yi nekk ci màgget ak dee ? Déedéet ! Yexowa dafa bëgg ay doomam, te dafa leen yéene bànneex bu dul jeex ci kaw suuf. Lii la Biibël bi wax ci doomu Aadama yi : “ [Yexowa] dugal na xalaatu dund gu dul jeex ci seen biir xol. ” (Dajalekat 3:​11, NW). Bi Yàlla doon bind nit, dafa def ci moom bëgg-bëggu dund ba fàww. Te am na lu mu def ngir bëgg-bëgg boobu mën a nekk.

LU TAX DOOMU AADAMA YI DI DEE

9. Lan la Yexowa tere woon Aadama, te lu tax li mu ko santoon jafewul woon a topp ?

9 Kon lu tax doomu Aadama yi di dee ? Bu ñu bëggee xam tont bi, dañu war a dellu ci jamono ji nga xam ne benn góor ak benn jigéen kese ñoo nekkoon ci kaw suuf, ba xam li fa xewoon. Biibël bi nee na : “ Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neex a lekk. ” (Njàlbéen ga 2:⁠9). Waaye am na lu Yexowa tere woon. Lii la wax Aadama : «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, waaye bul lekk ci garab giy tax a xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.» (Njàlbéen ga 2:​16, 17). Li Yàlla wax Aadama noonu jafewul. Amoon na yeneen garab yu bare yu Aadama ak Awa mënoon a lekk. Waaye li leen Yàlla tere, dina tax ñu mën a wone ne gërëm nañu ko Moom mi leen may dund gu neex lool ak lépp li ñu am. Bu ñu déggalee Yàlla dina wone it ne may nañu cér seen Baay bi nekk ca kaw asamaan, te nangu nañu topp tegtal yu baax yi mu leen jox.

10, 11. a) Lan moo tax góor bu njëkk bi ak jigéen bu njëkk bi bañ a déggal Yàlla ? b) Lu tax li Aadama ak Awa bañ a déggal Yàlla nekk poroblem bu réy ?

10 Waaye nag, Aadama ak Awa dañu tànn bañ a déggal Yexowa. Seytaane dafa jaar ci benn jaan ngir wax ak Awa, ne ko : «Ndax wóor na ne, Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi?”» Awa tontu ko ne : «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay. Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» — Njàlbéen ga 3:​1-3.

11 Seytaane daldi ko ne : «Déedéet, dungeen dee!» Mu teg ci ne «Yàlla xam na ne, bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.» (Njàlbéen ga 3:​4, 5). Seytaane dafa bëggoon gëmloo Awa ne, lekk doomu garab bi ñu ko tere dina ko jariñ. Ci gis-gisu Seytaane, Awa amoon na sañ-sañu seetal boppam li baax ak li bon. Ci moom Awa amoon na it sañ-sañu def li ko neex. Seytaane dafa wax it ne Yexowa waxul dëgg bi mu leen waxee ne bu ñu lekkee doomu garab gi dinañu dee. Awa daldi gëm Seytaane. Mu witt ci doomu garab gi, lekk, ba pare jox jëkkëram, mu lekk. Du ñàkk a xam moo leen ci dugal. Xamoon nañu ne li leen Yàlla tere lañu doon def. Bi ñu lekkee doomu garab bi, wone nañu ne ñoo tey bañ a déggal Yàlla, fekk ndigal bi leen Yàlla joxoon, lu yomb te jaadu la woon. Li ñu def noonu dafay wone ne faalewuñu woon seen Baay bi neek ca kaw asamaan ak kiliftéefam. Loolu ñu def Ki leen sàkk te mu nekk ku leen bëgg, nekkoon na li ñu leen mënul a baal.

12. Lan moo ñu mën a dimbali ñu xam li Yexowa doon yëg ci biir xolam bi ko Aadama ak Awa weddee ?

12 Seetal lii : Boo yaroon sa doom bu góor walla bu jigéen, toppatoo ko ba mu màgg. Benn bés mu bañ laa déggal, won la ne mayu la benn cér te bëggu la sax. Bu boobaa looy yëg ci sa biir xol ? Dina la metti lool. Kon war nga mën a xam metit bi Yexowa yëg ci biir xolam bi ko Aadama ak Awa weddee ñoom ñaar ñépp.

Ci pëndu suuf la Aadama jóge, te dafa dellu nekk pëndu suuf.

13. Lan la Yexowa waxoon ne dina dal Aadama bés bu deewee, te loolu lu muy tekki ?

13 Aadama ak Awa dañu bañoon a déggal Yexowa. Kon amuloon dara lu waroon a tax Yexowa kontine di leen toppatoo ngir ñu dund ba fàww. Aadama ak Awa dee nañu ni mu ko waxe woon. Aadama ak Awa nekkatuñu. Demuñu feneen ngir dund fa ni ay malaaka. Li Yexowa wax Aadama bi mu ko doon laaj lu tax mu bañ ko déggal, moo ñuy won loolu. Lii la ko Yàlla waxoon : dinga “dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd”. (Njàlbéen ga 3:19.) Ak pëndu suuf la Yàlla binde Aadama (Njàlbéen ga 2:⁠7). Bala loolu, Aadama nekkul woon. Moo tax, bi Yexowa waxee ne Aadama dafay dellu nekk pënd, dafa bëggoon a wax ne Aadama dootul nekkati. Ni pënd bi ñu ko jële, Aadama dootul dund.

14. Lu tax nit di dee ?

14 Aadama ak Awa mënoon nañu dund ba tey jii. Waaye dañu dee ndax li ñu tànn bañ a déggal Yàlla. Noonu lañu bàkkaare. Aadama dafa wàll doomam yépp bàkkaar ak dee. Looloo waral nit di dee (Room 5:12). Bàkkaar boobu dafa mel ni feebar bu metti bu waajur di wàll ay doomam, te kenn mënu ci rëcc. Li muy indi mooy dee. Loolu musiba la. Dee noon la, du xarit (1 Korent 15:26). Kontaan nañu lool ci li Yexowa joxe njot gi ngir musal ñu ci noon bu bon boobu.

XAM DËGG GI JËM CI DEE, LU BAAX LA

15. Lu tax xam dëgg gi jëm ci dee di dalal suñu xel ?

15 Li Biibël bi wax ci lu jëm ci li nit ku dee nekke, dafay dalal suñu xel. Ni ñu ko jànge, ñi dee amuñu naqar te seen xol du jeex. Amul dara lu war a tax ñu ragal leen, ndaxte mënuñu gaañ kenn. Soxlawuñu ñu dimbali leen, te ñoom it mënuñu def dara ngir dimbali ñu. Mënuñu wax ak ñoom, ñoom it mënuñu wax ak ñun. Kilifa diine yu bare dañuy wax ne mën nañu dimbali ñi dee, fekk du dëgg. Te ñi leen gëm dañu leen di may xaalis. Waaye ku xam dëgg gi jëm ci ñi dee, ñiy wax fen yooyu du ñu ko mën a nax.

16. Kan moo dugg ci li diine yu bare di jàngale, te naka la ko defe ?

16 Ndax sa diine ànd na ak li Biibël bi wax ci lu jëm ci dee ? Diine yu bare ànduñu ci. Lu tax loolu ? Kàddu Seytaane rax na ci li diine yooyu di jàngale. Seytaane dafay jaar ci diine yu dul wax dëgg ngir gëmloo nit ñi ne bu nit deewee, dafay am lu jóge ci moom, kontine di dund feneen fu mbindeef yu ñu mënul a gis nekk. Loolu fen la bu Seytaane di boole ak yeneen fen ngir nit ñi bañ a topp Yexowa Yàlla. Nañu ko seet ci lii di topp.

17. Li ñuy jàngale ci safara, lu tax jekkul ci Yexowa ?

17 Ni ñu ko gise ba pare, am na diine yuy jàngale ne, su nit dëkkee ci lu bon, bu deewee safara la jëm, fu ñu koy toroxal ba abadan. Li ñuy jàngale noonu jekkul ci Yàlla. Yexowa, Yàlla ju bare mbëggeel la. Te du mas a toroxal kenn ci fasoŋ boobu (1 Yowaana 4:⁠8). Looy xalaat ci nit kuy dugal loxo doomam ci safara ndax li mu ko bañ a déggal ? Ndax dinga fonk nit ku mel noonu ? Ndax dinga bëgg xamante ak moom sax ? Déedéet ! Wóor na ne dinga wax ne nit kooku soxor na lool. Waaye nag, Seytaane dafa ñu bëgg gëmloo ne Yexowa dafay toroxal nit ñi ci safara ba abadan, lu mat ay milyaari-milyaari at !

18. Jaamu ñi dee, ci ban fen bi diine yi di jàngale la jóge ?

18 Seytaane dafay jaar it ci yenn diine ngir jàngale ne bu nit ñi deewee, dañuy nekk ay xel te ñiy dund dañu leen war a màggal te may leen cér. Diine yooyu dañuy jàngale it ne, xelu nit ñi dee mën nañu nekk xarit yu bare kàttan walla ñu nekk noon yu soxor lool. Nit ñu bare gëm nañu fen yooyu. Dañu ragal ñi dee, te dañu leen di màggal, di leen jaamu. Waaye Biibël bi dafay wax ne, ñi dee dañuy nelaw. Dafay wax it ne Yexowa Yàlla dëgg ji rekk lañu war a jaamu moom mi ñu sàkk te di ñu dundal. — Peeñu ma 4:⁠11.

19. Xam dëgg gi jëm ci dee, leneen lan lay tax ñu xam ci li Biibël bi wax ?

19 Boo xamee dëgg gi jëm ci nit ñi dee, fen yi diine yi di jàngale duñu la réeral. Dafay tax it nga mën a xam yeneen dëgg yi Biibël bi wax. Nañu ci wax benn : Ndegam Biibël bi nee na bu nit deewee, dara du jóge ci moom ngir kontine di dund feneen, kon boo demee ba xam loolu, dangay gën a xam li dund ba fàww ci àjjana ci kaw suuf di tekki dëgg.

20. Ci ban laaj lañuy waxtaan ci pàcc bii di topp ?

20 Ayóoba mi nekkoon nit ku jub, laajtee woon na bu yàgg laaj bii : “ Boroom doole bu deewee ndax dina mën a dundaat ? ” (Ayóoba 14:​14, NW). Ndax nit ku dee dina mën a dundaat ? Li Biibël bi wax ci loolu dafay dalal bu baax suñu xel. Loolu la pàcc bii di topp di wone.

^ par. 5 Boo bëggee am lu la gën a leer ci “ ruu ”ak “ xel ”, seetal xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 208 ba 211.