XAAJ 7
Kan mooy Yeesu ?
Yexowa yónni woon na Yeesu ci kaw suuf si. 1 Yowaana 4:9
Bu ñu bëggee neex Yexowa, am na keneen ku am solo koo xam ne war nañu dégg li mu wax. Bu yàgg bala muy sàkk Aadama, Yexowa sàkkoon na kenn koo xam ne ku bare kàttan la ca asamaan.
Yexowa yónni woon na ko ci kaw suuf si. Ca dëkku Betleyem la juddoo. Turam mooy Yeesu. Maryaama mooy yaayam. — Yowaana 6:38.
Yeesu roy na Yàlla bu baax ci jikko bi mu wone bi mu nekkee ci kaw suuf si. Ku baax la woon, ku bëgg nit la woon te neex a jege. Ragalul woon di jàngale dëgg gi jëm ci Yàlla.
1 Piyeer 2:21-24
Yeesu lu baax rekk la doon def, waaye am na ñu ko bañoon.Yeesu dafa doon faj ñi feebar, di dekkal ñi dee.
Kilifa diine yi dañu bañoon Yeesu, ndaxte dafa doon feeñal seeni njàngale yu dul dëgg ak seeni jëf yu bon.
Kilifa diine yi fexe nañu ba waa Room dóor Yeesu te rey ko.