Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 5

Ca jamano yonent Yàlla Nóoyin — ñan ñoo déggoon li Yàlla wax te ñan ñoo bañoon a dégg ?

Ca jamano yonent Yàlla Nóoyin — ñan ñoo déggoon li Yàlla wax te ñan ñoo bañoon a dégg ?

Ci jamano Nóoyin, ñu bare dañu doon def lu bon. Njàlbéen ga 6:5

Bi Aadama ak Awa amee ay doom, nit ñi ñu ngi doon tàmbalee bare ci kaw suuf si. Amoon na itam ay malaaka yu toppoon Seytaane bi mu fippoo.

Malaaka yooyu jóge woon nañu ca asamaan, ñëw ci kaw suuf si, jël jëmu nit ngir mën a séy ak jigéen yi. Jigéen yooyu amoon nañu ak ñoom ay doom yu soxor te bare doole.

Àddina si bare woon na ay nit yu soxor. Lii la ci Biibël bi wax : “ Mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu man a tollu, lu bon rekk lay xënte ci xolam. ”

Nóoyin déggoon na li Yàlla waxoon. Defar na gaal bi mu ko santoon. Njàlbéen ga 6:13, 14, 18, 19, 22

Nóoyin nit ku jub la woon. Yexowa waxoon na ko ne dina indi taw bu metti bu fiy jële nit ñu bon ñi.

Yàlla waxoon na ko itam mu defar gaal bu mag, dugal ci njabootam, ak bépp xeetu mala.

Nóoyin mu ngi doon yégal nit ñi taw bu metti boobu naroon a ñëw, waaye dañu bañoon a dégg. Ñenn ñi dañu ko doon reetaan, ñeneen ñi jéppi ko.

Bi mu defaree gaal gi ba pare, Nóoyin dugal na mala yi ci biir.