Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 2

Waxal mel ni kuy waxtaan

Waxal mel ni kuy waxtaan

2 Korent 2:17

LI NGA WAR A JÀPP: Waxal ni nga tàmm di waxe ci fasoŋ buy wone ne li ngay wax lu dëggu la ci yow te fonk nga ñi lay déglu.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Waajalal sa bopp bu baax te ñaan Yexowa. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga bañ a bàyyi xel torop ci sa bopp waaye nga gën a xalaat ci xibaar bi ngay jottali. Fexeel ba ponk yi gën a am solo ci sa waxtaan leer ci sa bopp. Bul jàng rekk li ñu bind. Waxal xalaat yi ci say kàddu bopp.

  • Li ngay wax, na jóge ci sa xol. Xalaatal ci li war a tax nit ñi déglu li ngay wax. Bàyyil xel ci ñoom. Noonu sa jëmm yépp, maanaam li nit ñi di gis ci yow, dina wone ne lu baax nga leen bëggal te li ngay wax lu dëggu la ci yow.

  • Xoolal ñi lay déglu. Xoolal ñi lay déglu waaye na ànd ak yar. Booy def waxtaan, bul xoolandoo ñépp ci mbooloo mi, waaye xoolal kenn, ba pare nga jàll ci keneen.