Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 1

Am na Kumpa goo Xam ne boo ko Xamee Dinga Kontaan

Am na Kumpa goo Xam ne boo ko Xamee Dinga Kontaan

Ndax xam nga lan mooy kumpa ? — * Kumpa mooy lu kenn xamul. Am na kumpa gu réy bu ñu wax ci Biibël bi. Kumpa gu sell la ndaxte ci Yàlla la jóge. Malaaka yi sax bëggoon nañu xam kumpa googu. Yaw nag, ndax bëgg nga ko xam ? —

Ci sa xalaat lan la malaaka yi doon jéem a xam ?

Yàgg na lool, Yàlla dafa sàkk benn góor ak benn jigéen. Ñu ngi tuddoon Aadama ak Awa. Yàlla dafa leen dugal ci tool bu rafet bu ñu doon woowe toolu Eden maanaam àjjana. Tool bu rafet boobu moo nekkoon seen kër. Aadama ak Awa bu ñu déggaloon Yàlla, ñoom ak seeni doom dinañu mën a defar suuf si sépp ba mu nekk àjjana. Te it dinañu mën a dund ba fàww ci àjjana jooju. Aadama ak Awa, lan lañu mujj a def ? Ndax yaa ngi koy fàttaliku ? —

Aadama ak Awa déggaluñu woon Yàlla. Loolu moo tax tey ñun nekkuñu ci àjjana. Waaye Yàlla waxoon na ne dina defar suuf si sépp ba mu rafet te nit ñépp dinañu dund ba fàww ci jàmm. Naka lay defe loolu ? Nit ñi toog nañu lu yàgg te xamuñu tont bi. Loolu kumpa la woon.

Bi Yeesu ñëwee ci kaw suuf, am na lu mu wax lu jëm ci kumpa googu. Dafa ne kumpa googu mu ngi jëm ci Nguuru Yàlla. Mu wax ne ñu ñaan ngir nguur googu ñëw. Nguur googu dina defaraat suuf si ba mu nekk àjjana.

Ndax yaw yàkkamtiwuloo xam kumpa googu ? — Fàttalikul ne nit ñiy déggal Yàlla rekk ñooy dund ci àjjana. Ci Biibël bi wax nañu ci ay góor ak ay jigéen yu bare yu doon déggal Yàlla. Ndax bëgg nga leen a xam ? — Nañu waxtaan ci ñenn ci ñoom te xool ni ñu mën a def ba mel ni ñoom.

^ par. 3 Ci téere bii, dinga gis màndarga bu topp ci laaj yi te mel nii : —. Boo ko gisee, xamal ne danga war a taxaw may sa doom mu tontu.