Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 22

Naka nga mënee xamle xibaaru jàmm bi?

Naka nga mënee xamle xibaaru jàmm bi?

Xéyna looy gën di xam dëgg gi nekk ci Biibël bi, dinga ne, ‘Lii ñépp a ko war a xam!’ Te wax nga dëgg, nit ñi ñépp soxla nañu koo xam! Waaye nag xamal ñeneen li ngay jàng, mën na la tiital tuuti. Nañu waxtaan ci li la mën a dimbali ba doo tiit, ak ni nga mënee tàmbali xamle xibaaru jàmm bi nekk ci Biibël bi, ànd ci ak mbégte.

1. Naka nga mënee wax nit ñi nga xam li ngay jàng?

Taalibe Yeesu yi lii lañu waxoon: «Nun manunoo baña wax li nu gis te dégg ko» (Jëf ya 4:20). Dañu fonkoon lool dëgg gi. Moo tax ñu bëggoon koo xamal nit ñépp. Yow itam ndax du loolu nga bëgg? Bu dee waaw, kon xoolal ni nga mënee wax sa waa kër ak say xarit li nga jàng, ànd ci ak respe (Jàngal Kolos 4:6).

Ay xelal ngir tàmbali

  • Booy waxtaan ak sa waa kër, boole ci loo jàng ci Biibël bi. Mën nga ne: «Am na lu am solo lu ma jàng ci semen bii.»

  • Wonal aaya buy dëfal xol sa xarit bu feebar walla bu jaaxle.

  • Ñi nga bokkal liggéey bu ñu la laaje ni sa week-end deme, wax leen li nga jàng ci sa njàngum Biibël walla ci ndaje bi.

  • Wonal say xarit suñu palaas bi nekk ci internet jw.org.

  • Woowal ñeneen ñu teewe sa njàngum Biibël bi, walla nga won leen ni ñu mënee laaj ci jw.org ñu jàngal leen Biibël bi.

2. Lu tax waare ak mbooloo mi doon jubluwaay bu baax?

Taalibe Yeesu yi, yemuñu rekk ci yégal xibaaru jàmm bi nit ñi ñu xam. Yeesu «yebal [na] leen, ñu ànd ñaar ak ñaar, jiituji ko ca dëkk yépp» ngir waare fa (Luug 10:1). Fasoŋ boobu ñu doon waaree tax na ba nit ñu bare dégg xibaaru jàmm bi. Di ànd ci liggéeyu waare bi, may na itam taalibe yi mbégte mu réy (Luug 10:17). Yow nag, ndax waare ak mbooloo mi mën na nekk sa jubluwaay?

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mën a def ba doo tiit te ñam ci mbégte bi nekk ci xamle xibaaru jàmm bi.

3. Yexowa dina ànd ak yow

Am na ñoo xam ne, bëgg nañu waare waaye ñemewuñu bëtu nit walla ni leen ñeneen ñi di gise.

  • Ndax yow dangay tiit boo bëggee wax keneen li nga jàng? Lu tax?

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Lan moo dimbali ndawi Seede Yexowa yooyu ba tiitatuñu woon?

Jàngal Esayi 41:10. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Boo ragalee waare, naka la la ñaan mënee dimbali?

Ndax xamoon nga ne...

Seede Yexowa yu bare dañu foogoon ne, duñu mas a mën a waare xibaaru jàmm bi. Sergey kenn la ci ñoom. Moom dafa xeeboon boppam lool, te wax ak ñeneen dafa jafe woon ci moom. Waaye bi mu jàngee Biibël bi, lii la mujj a wax: «Doonte sax ragaloon naa, tàmbali naa wax ñeneen ñi li ma doon jàng. Wax ñeneen lu jëm ci Biibël bi jural na ma lu ma foogul woon. Tax na ma gën a wóolu sama bopp te gën na dëgëral sama ngëm ci li ma doon jàng.»

4. Àndal ak respe

Booy wax keneen xibaaru jàmm bi, bàyyil xel bu baax ci li ngay wax waaye it ci ni nga koy waxe. Jàngal 2 Timote 2:24 ak 1 Piyeer 3:15. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka nga mënee topp aaya yi nga jàng, booy wax keneen lu jëm ci Biibël bi?

  • Ñenn ci sa waa kër walla say xarit, mën nañu bañ a ànd ci li nga wax. Lan nga mën a def? Lan nga warul def?

  • Lu tax li gën mooy, nga laaj nit ki ci anam bu rafet te bañ koo forse li nga gëm?

5. Xamle xibaaru jàmm bi dafay maye mbégte

Yexowa, Yeesu la dénk liggéeyu waare xibaaru jàmm bi. Naka la Yeesu gisee liggéey boobu? Jàngal Yowaana 4:34. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lekk lekk bu baax yemul rekk ci may ñu dund waaye dafa ñuy may mbégte itam. Lu tax Yeesu ne def coobare Yàlla, lu ci mel ni xamle xibaaru jàmm bi, dafa mel ni lekk?

  • Ci sa xalaat, yan mbégte nga mën a jële ci xamle xibaaru jàmm bi?

Ay xelal

  • Ci ndaje yi ci biir semen bi, xoolal ni nga mënee jëfandikoo xelal yi ñuy joxe ngir waare, pur tàmbali ay waxtaan.

  • Waxal ak ki lay jàngal ngir xam ni nga mën a def ba bokk ci eleew yiy def waxtaan, ci ndaje yi ci biir semen bi. Def waxtaan foofu dina tax, wax ak ñeneen gën a yomb ci yow.

  • Mën nga waajal sa bopp ngir tontu ci yenn laaj yi ak li nekk ci téere bii, ci xaaj bi tudd «Bu la nit waxoon» walla «Bu la nit laajoon.»

BU LA NIT LAAJOON: «Yow ci loo nekk?»

  • Naka nga mënee jaar foofu ngir wax ko li ngay jàng ci Biibël bi?

NAÑU TËNK

Xamle xibaaru jàmm bi dafay maye mbégte, te def ko jafewul ni nga ko fooge.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax nga war a xamle xibaaru jàmm bi?

  • Naka nga ko mënee def ànd ci ak respe?

  • Naka nga mën a def ba waare du la tiital?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ñeenti jikko yu la mën a dimbali nga xamle xibaaru jàmm bi.

«Ndax pare nga ngir nekk nappkatu nit?» (w20 sàttumbar)

Xoolal ni la benn royukaay ci Biibël bi mënee dimbali nga am fitu xamle xibaaru jàmm bi, bu dee sax ndaw nga.

Yexowa dina la may fit (11:59)

Xoolal ni nga mënee wax sa waa kër yi xamagul Yexowa, lu jëm ci Biibël bi.

«Mën nañu laal xolu suñu mbokk yi ñu bokkalul ngëm» (w14 15/3)