Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 24

Ñan ñooy malaaka yi ak lan lañuy def?

Ñan ñooy malaaka yi ak lan lañuy def?

Yexowa dafa bëgg ñu xam njabootam gi nekk ci kaw asamaan. Malaaka yi ci njabootam lañu bokk. Dañu leen di woowe itam «goney Yàlla», maanaam ay doomi Yàlla (Ayóoba 38:7). Lan la Biibël bi wax ci malaaka yi? Lan la malaaka yi di def? Ndax malaaka yi yépp ci njabootu Yàlla lañu bokk?

1. Ñan ñooy malaaka yi?

Yexowa sàkk na malaaka yi bala muy sàkk suuf si. Malaaka yi ay xel lañu ni Yàlla, kenn mënu leen gis te ci asamaan lañuy dund (Yawut ya 1:14). Ay milioŋi malaaka ñoo am, te benn bokku ci ak moroomam (Peeñu 5:11). Dañuy ‘jëfe ndigalu Yexowa, di sàmm kàddoom’ (Sabóor 103:20). Ci jamono yu njëkk ya, Yexowa dafa doon yónni lée-lée malaaka yi ñu jottali kàddoom, dimbali ay jaamam te aar leen. Tey, malaaka yi dañuy xiir karceen yi ci dimbali nit ñi bëgg a xam Yàlla.

2. Kan mooy Seytaane te ñan ñooy malaakaam yu bon yi?

Am na ay malaaka yoo xam ne takkuwuñu ci Yexowa. Malaaka bi njëkk a fippu mooy «tuumaalkat bi [Ibliis] mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp» (Peeñu 12:9). Seytaane dafa bëggoon a jiite nit ñi. Moo tax mu xiir Aadama ak Awa ak yeneen malaaka sax, ñoom itam ñu fippu ni moom. Malaaka yu fippu yooyu lañuy woowe malaaka yu bon yi. Yexowa dafa leen dàq ci asamaan ñu wàcc ci suuf, te dina leen alag (Jàngal Peeñu 12:9, 12).

3. Naka la Seytaane ak malaaka yu bon yi di ñu jéemee nax?

Seytaane ak malaaka yu bon yi ñu ngi nax nit ñu bare jaare ko ci mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lépp lu jëm ci jéem a jokkoo ak nit ñi dee. Ñu bare dañuy dem ci gisaanekat yi, ñiy firi gént ak ñiy def horoscopes. Am na ñuy jaar ci mbirum rab ngir faju. Am na itam ñu gëm ne mën nañu wax ak ñi dee. Waaye lii la ñu Yexowa wax: «Buleen jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee te buleen jublu ci boroom rawaan yiy seet» (Sarxalkat yi 19:31). Dafa joxe ndigal boobu ngir aar ñu ci Seytaane ak ci malaaka yu bon yi. Ñoom ay noonu Yàlla lañu, te lor ñu lañu bëgg.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal lu baax li malaaka yi di def, li tax mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel nekk lu bon. Xoolal it li ñu mën a def ngir aar suñu bopp ci Seytaane ak ci malaaka yu bon yi.

4. Malaaka yi dañuy dimbali nit ñi ñu xam Yexowa

Malaaka Yàlla yi, duñu dem waar nit ñi, waaye dañuy xiir jaamu Yàlla yi ñu dem ci nit ñi bëgg a xam Yàlla. Jàngal Peeñu 14:6, 7. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax ñu soxla ndimbalu malaaka yi ngir waare?

  • Xam ne malaaka yi mën nañu laa xiir ci dem ci nit ñi bëgg a xam Biibël bi, ndax loolu du la yokk cawarte? Lu tax?

5. Soreel lépp lu jëm ci mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel

Seytaane ak malaaka yu bon yi, ay noonu Yexowa lañu. Suñuy noon lañu itam. Jàngal Luug 9:38-42. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la malaaka yu bon yi di def nit ñi?

Bëgguñu woo malaaka yu bon yi, ñu dugg ci suñu dund. Jàngal Baamtug Yoon wi 18:10-12. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la malaaka yu bon yi di jéemee dugg ci suñu dund ak di jokkoo ak ñun? Lan la nit ñi di faral di def fi nga dëkk?

  • Ndax foog nga ne jaadu na Yexowa tere ñu mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel? Lu tax?

Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ndax foog nga ne téere bi Palesa takkaloon doomam, lu baax la walla déet? Lu tax?

  • Lan la Palesa def ngir aar boppam ci malaaka yu bon yi?

Karceen dëgg yi, dañu mas di moytu malaaka yu bon yi. Jàngal Jëf ya 19:19 ak 1 Korent 10:21. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax mu am solo nga yàq lépp lu laal mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel?

6. Amal ndam ci kaw Seytaane ak malaakaam yu bon

Seytaane mooy jiite malaaka yu bon yi. Waaye malaaka yu baax yi Mikayel, maanaam Yeesu mooy seen kilifa. Fan la kàttanu Mikayel tollu? Jàngal Peeñu 12:7-9. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ñan ñoo ëpp kàttan? Mikayel ak ay malaakaam walla Seytaane ak ay malaakaam?

  • Ci sa xalaat, ndax taalibe Yeesu yi war nañu ragal Seytaane ak ay malaakaam?

Mën nga am ndam ci kaw Seytaane ak malaakaam yu bon yi. Jàngal Saag 4:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka nga mënee aar sa bopp ci Seytaane ak ci malaaka yu bon yi?

BU LA NIT WAXOON: «Dara aayul ci fo ak jeux vidéo yu am luxus walla seetaan film yuy wone lu mel noonu. Fo rekk la.»

  • Lu tax am gis-gis boobu baaxul?

NAÑU TËNK

Malaaka yi takku ci Yàlla, dañu ñuy dimbali. Seytaane ak ay malaakaam yu bon, ay noonu Yexowa lañu te dañuy jaar ci mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel, ngir nax nit ñi.

Nañu fàttaliku

  • Naka la malaaka Yexowa yi di dimbalee nit ñi ñu xam Yàlla?

  • Kan mooy Seytaane te ñan ñooy malaakaam yu bon yi?

  • Lu tax nga bëgg a set wecc ci lépp lu laal mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal liy wone ne Yeesu mooy Mikayel kilifa malaaka yi.

«Kan mooy Mikayel, kilifa malaaka yi?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal ni benn jigéen tàggoo ak rab yi.

«Léegi am na jubluwaay ci dundam» (w93 1/7)

Xoolal ni Seytaane di jaare ci mbirum rab, kort, luxus, tuuri maam ak lu ni mel, ngir nax nit ñi.

«Dëgg gi ci lu jëm ci mbirum luxus, gisaane ak dëmm yi» (ol pàcc 5)