NJÀNGALE 7
Lan mooy Nguuru Yàlla ?
1. Lan mooy Nguuru Yàlla ?
Nguuru Yàlla, nguur la bu nekk ca kaw asamaan. Dina fi jële bépp nguuru doomu Aadama, te def ba coobare Yàlla am ca kaw asamaan ak ci suuf si. Xibaar bi jëm ci Nguuru Yàlla, xibaaru jàmm la. Li nit ñi di séentu ci nguur mooy mu faj seeni soxla, te loolu la Nguuru Yàlla di def. Dina boole ñépp ñi dëkk ci kaw suuf si ñu doon benn. — Jàngal Dañeel 2:44 ; Macë 6:9, 10 ; 24:14.
Nguur dafay am buur. Yexowa tànn na doomam, Yeesu Kirist ngir mu nekk Buur ci Nguuram. — Jàngal Peeñu ma 11:15.
Seetaanal wideo Qu’est-ce que le royaume de Dieu ?
2. Lu tax ñu ne Yeesu mooy Buur bi gën ?
Doomu Yàlla ji mooy Buur bi gën ndaxte ku baax la te dafay sax ci dëgg (Macë 11:28-30). Am na itam kàttanu dimbali nit ñi ndaxte dina nekk ca asamaan di ilif suuf si. Bi mu dekkee dafa yéeg ca asamaan toog ci ndeyjooru Yexowa di xaar (Yawut ya 10:12, 13). Yàlla mujj na koo jox kàttan ngir mu tàmbalee ilif. — Jàngal Dañeel 7:13, 14.
3. Ñan ñooy nguuru ak Yeesu ?
Mbooloo bi ñuy woowe “ ñu sell ” ñooy nguuru ak Yeesu ca asamaan (Dañeel 7:27). Taalibe yi doon ànd ak Yeesu lañu njëkk a tànn ngir ñu bokk ci ñu sell ñooñu. Ba tey Yexowa mu ngi wéy di tànn ay góor ak ay jigéen yu takku ci moom ngir ñu bokk ci ñu sell ñi. Ni Yeesu, ñi ñu tànn dañuy dekki mel ni ay malaaka. — Jàngal Yowaana 14:1-3 ; 1 Korent 15:42-44.
Luug 12:32). Ñu ngi tollu ci 144 000 nit. Dinañu ànd ak Yeesu ngir ilif suuf si. — Jàngal Peeñu ma 14:1.
Ñaata nit ñooy dem ca asamaan ? Ñoom la Yeesu woowe “ coggal ju ndaw ji ” (4. Lan moo xewoon bi Yeesu tàmbalee ilif ?
Nguuru Yàlla komaase na ilif ci atum 1914. * Bi Yeesu nekkee Buur, li mu njëkk a def mooy daaneel Seytaane ak maalaakaam yi ci kaw suuf. Seytaane mer mer bu tàng, mu komaase indi musiba ci kaw suuf (Peeñu ma 12:7-10, 12). Booba ba tey, musiba yiy dal doomu Aadama yi ñu ngi gën di yokku. Xare yi, xiif, feebar yiy law te gaaw a reye, ak ay yëngu-yëngu suuf bokk nañu ci “ tegtal ” yiy wone ne léegi Nguuru Yàlla lijjanti mbirum suuf si. — Jàngal Luug 21:7, 10, 11, 31.
5. Lan la Nguuru Yàlla di def ?
Waaraate bi am ci àddina si sépp tax na ba Nguuru Yàlla di dajale mbooloo mu réy ci xeet yépp. Ay milyoŋi nit nangu nañu bokk ci ñi Yeesu di ilif. Nguuru Yàlla dina leen aar buy alag àddina su bon sii. Ñépp ñu bëgg a jariñoo li Nguuru Yàlla di def, war nañu jàng di déggal Yeesu mi leen di ilif. — Jàngal Peeñu ma 7:9, 14, 16, 17.
Ci 1 000 at, Nguuru Yàlla dina matal li Yàlla bëggaloon doomu Aadama yi ca njàlbéen. Suuf si sépp dina nekk àjjana. Yeesu dina mujj a delloo Nguur gi Baayam (1 Korent 15:24-26). Ndax am na koo bëgg a xamal lu jëm ci Nguuru Yàlla ? — Jàngal Sabóor 37:10, 11, 29.
^ par. 6 Boo bëggee yokk sa xam-xam ci li Biibël bi yégle ci lu jëm ci atum 1914, xoolal xët 215-218 ci téere bi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?