Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 9

Lan ngeen mën a def ba am jàmm ci seen njaboot ?

Lan ngeen mën a def ba am jàmm ci seen njaboot ?

1. Lu tax séy ci yoon am solo ngir am jàmm ci njaboot gi ?

Xibaaru jàmm bi, ci Yexowa la jóge, moom mi bëgg njaboot yépp am jàmm. Yàlla moo sos séy. Séy ci yoon lu am solo la ngir jàmm am ci njaboot gi, ndaxte dafay tax ñépp mën a am xel mu dal te waajur yi mën a yar xale yi ni mu ware. Ñi bëgg a déggal Yàlla dañoo war a dem bindlu seen séy ni ko seen sàrtu réew laaje. — Jàngal Luug 2:1, 4, 5.

Naka la Yàlla gise séy ? Yàlla bëgg na ñaar ñuy séy, ñu séy seen giiru dund. Yexowa dafa bëgg, ñaar ñu séy, ku nekk yem ci moroomam (Yawut ya 13:4). Yàlla sib na tas séy (Malaki 2:16). Waaye bu njaaloo amee, Yàlla may na Karceen yi ñu tas seen séy te seyaat. — Jàngal Macë 19:3-6, 9.

2. Naka la ñaar ñu séy war a doxale ci seen biir ?

Yexowa dafa sàkk góor ak jigéen ngir ñu jàppalante ci seen biir (Njàlbéen ga 2:18). Jëkkër mooy kilifa njabootam. Moom moo war a jiitu ci faj soxla njabootam, maanaam jox leen lu ñuy lekk, lu ñuy sol, ak fu ñuy dëkk te it war na leen jàngal lu jëm ci Yàlla. Jëkkër war na nangu ñàkk dara ndax mbëggeel bi mu am ci jabaram. Ñaar ñu séy war nañu bëggante te joxante cër. Ndegam kenn matul, ñaar ñu séy war nañu di baalante ndaxte loolu day indi jàmm ci séy. — Jàngal Efes 4:31, 32 ; 5:22-25, 33 ; 1 Piyeer 3:7.

3. Bu seen séy neexul, ndax loolu war na tax ngeen teqalikoo ?

Bu ngeen di jànkoonte ak ay jafe-jafe ci biir séy, ku nekk ci yéen war na góor-góorlu ngir won sa moroom mbëggeel (1 Korent 13:4, 5). Kàddu Yàlla digalul kenn mu teqalikoo ngir faj jafe-jafe yiy faral di am ci biir séy. — Jàngal 1 Korent 7:10-13.

4. Yéen xale yi, lan la leen Yàlla bëggal ?

Yexowa dafa bëgg ngeen am jàmm. Jox na leen ndigal yi gën yu leen di dimbali ngeen bég ci seen ndaw. Dafa bëgg ngeen jariñoo xam-xam bi seeni waajur am (Kolos 3:20). Yexowa mi ñu sàkk dafa bëgg ngeen def li ko neex, te bu ngeen ko defee dingeen ci am mbégte. — Jàngal Ecclésiaste 11:9–12:1 ; Macë 19:13-15 ; 21:15, 16.

5. Waajur yi, lan la seeni doom soxla ngir bég ?

War ngeen góor-góorlu ngir jox seeni doom lu ñuy lekk, fu ñuy dëkk ak lu ñuy sol (1 Timote 5:8). Ngir seen doom am mbégte, waajur yi war nañu jàngal xale yi ñu bëgg Yàlla te jàng ci moom (Efes 6:4). Ni ngeen di wonee mbëggeel bi ngeen am ci Yàlla dafay laal bu baax seen xolu doom yi. Li ngeen di jàngal seeni doom, su dee dafay jóge ci Kàddu Yàlla, dina leen mën a dimbali ñu am xalaat yu rafet. — Jàngal Deutéronome 6:4-7 ; Kàddu yu Xelu 22:6.

Bu ngeen di ndokkeel seeni doom te di leen gërëm, loolu dina leen jariñ lool. Soxla nañu yar ak jubbanti. Yar boobu dina aar xale yi ci bépp jëf bu mën a yàq seen bànneex (Kàddu yu Xelu 22:15). Bu ñuy yar seeni doom, waajur yi waruñu tàng ba mu ëpp walla soxor ak ñoom. — Jàngal Kolos 3:21.

Seede Yexowa yi defar nañu ay téere yi ñu jagleel waajur yi ak xale yi ngir jàpple leen. Téere yooyu ñu ngi sukkandiku ci Biibël bi. — Jàngal Sabóor 19:8, 12.