NDAW ÑI ÑOO MOOM LII
12: Jubluwaay
LI MUY TEKKI
Jubluwaay du rekk loo bëgg ci sa xol. Am jubluwaay dëgg mu ngi tekki waajal li nga bëgg def, soppi doxalin bu ko jaree te ñeme coono.
Mën nañu am ay jubluwaay yu ndaw (yu ñuy matal ci ay bés walla ay semen), ay jubluwaay yu yem (yu ñuy matal ci ay weer) ak ay jubluwaay yu mag (yu ñuy matal ci benn at walla lu ko ëpp). Mën nañu matal jubluwaay yu mag yi bu ñu leen xaajee, ñu doon ay jubluwaay yu ndaw.
LI TAX MU AM SOLO
Matal say jubluwaay, mën na tax nga gën a wóolu sa bopp, sa diggante ak say xarit gën a dëgër te yokk sa mbégte.
Wóolu sa bopp: Boo matalee say jubluwaay yu ndaw, dinga gën a wóolu sa bopp ngir am jubluwaay yu gën a mag. Dinga gën a wóolu sa bopp itam ngir jànkoonte ak jafe-jafe yi ngay am bés bu nekk, lu mel ni ay xarit yu lay jéem a dugal ci lu bon.
Xaritoo: Ñu bare bëgg nañu am ay xarit yu am ay jubluwaay; maanaam, ay xarit yu xam li ñu bëgg te di def lépp ngir matal ko. Rax-ci-dolli, lenn liy gën a dëgëral sa diggante ak say xarit mooy ngeen bokk jubluwaay.
Mbégte: Boo amee ay jubluwaay ba matal leen, dangay yëg ne def nga dara.
«Am ay jubluwaay lu ma neex la. Dafay tax ma am ci lu ma jàpp te di def lépp ngir matal ko. Te boo matalee benn jubluwaay, dangay bég boo gisee ne matal nga ko ni nga ko bëgge woon» (Christopher).
LII LA BIIBËL BI WAX: «Kuy déglu ngelaw, doo ji, kuy seetluy niir, doo góob» (Kàdduy Waare 11:4).
LI NGA MËN A DEF
Xelal yii di topp, dinañu la dimbali, nga am ay jubluwaay te matal leen.
Ki nga doon. Bindal say jubluwaay ci kayit te jiital yi gën a am solo, maanaam yi nga bëgg njëkk matal.
Palaŋ. Boo amee jubluwaay, defal lii di topp:
Tànnal bés bi nga yaakaar ne mën nga ko matal.
Bindal fi nga war a jaar ba matal sa jubluwaay.
Jéemal a xalaat jafe-jafe yi nga mën a am te xool ni nga leen mënee faj.
Defal lii. Bul xaar ba lépp mat ngay soog a komaase. Laajal sa bopp li nga war a njëkk a def ngir matal sa jubluwaay, ba pare nga def ko. Saa yoo matalee dara, bind ko.
LII LA BIIBËL BI WAX: «Farlu, woomle [walla am alal]» (Kàddu yu Xelu 21:5).