Ndaje Seede Yexowa yi
Mën nga xam li ñuy def ci suñu ndaje yi. Seetal bérébu ndaje bi la gën a jege.
Lan lañuy def ci suñu ndaje yi ?
Seede Yexowa yi dañuy am ndaje ñaari yoon ci semen bu nekk ngir jaamu Yàlla (Yawut ya 10:24, 25). Ndaje yooyu, ñépp a ci mën a teew. Dañu ciy jàng li Biibël bi wax ak ni ñu mënee topp li Biibël bi jàngale.
Ñi teew dinañu mën a bokk ci ay waxtaan yu bare, mel ni ci lekkool. Bala ndaje bi di komaase ak buy jeex, dañuy woy ba pare daldi ñaan.
Bu dee sax nekkuloo Seede Yexowa mën nga teew ci suñu ndaje yi. Ñépp ñi ko bëgg mën nañu ñëw. Kenn du fey dara.